gear Paramètres Push
chat
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Dénkaane bi mooy sunu xaaj bu mujj ci dénkaaneey Sëñ Alhaaji. Noo ngi key ñaanal Yàlla sàmm ko, guddal fanam, may ko wér, xéewal yu yaatu te barkeel, defal ko ngëramal Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaaralahu Fii nag dafay soññee ci nu góor-góorlu ci yittewoo nees di njariñoo ci Sëriñ Bu […]
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Laabire gi Sëriñ Alhaaji Mbàkke daf ciy fàttali jeexug àdduna ak ñàkkam solo. Te sax li fiy jàmm mooy farlu ci sàkku lu baax ak di jaamu Yàlla. Noo man a tool, loo man a am, koo man a doon da nga faatu. Loolu sax mel na ni moo tax muy laaj […]
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu mat ci namu ko baaxo defe, la daaldi dénkaane sax ci jëfe ndigal ak bàyyi tere tey moytu yàq. Di boole it liggéey ak wakiirlu ci sunu Borom. Mu yee nu ci nopi ci lu amul njariñ ak sax bàyyi lu amul njariñ. Sëriñ Tuubaa daniwoon ku taqoo ak […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Lii ab Xasiida rajas la bob Sëriñ Alhaaji moo ko taalif def ko ci làkku wolof. Mu ciy fàttali ak a laabire mbokkum jullitam mu góor-góorlu ci ràññatle lu baax ak lu bon, wooteb Yàlla ak wooteb saytane. Mu mel ni kon nit manul ñàkk am ag jublu. Na fekk nag, jublu […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Dénkaane bi dafa jëm ci soññi jullit ñi rawatina muriit yi ci gën a baayi xel mujjug jamono gi Yonent bi Salla Laahu aleyhi sa salam doon wax ak yàqu yàqu yi ci aju. Muy woote kon ci gën a dëgmal Yàlla jaare ko ci yoon wi Yonent bi aleyhi salaam rëdd […]
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu matale, la daaldi soññee ci Xasiida yi ngir nu gën koo fonk, gën koo jàpp, gën ci soobu te Yàlla tax. Ginaaw loolu, la daaldi wax luy tax ñu nekk ci ak anam gi ko Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu fonke woon. Yal nanu Yàlla xiir ci […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw ba mu nuyoo mbokk yi ak dëkkandoo yi dafa daaldi soññee ci farlu ci lu baax ak jaamu Yàlla ju sax, ak di boole xam ak jëfe. Fàttali fi it lenn ci àddis yi jëm ci sàmm sa bopp ak benn lor kenn. Mu dolli soññee ci farlu ci Jàngum Xasida […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu matale, la daaldi soññee ci jaamu Yàlla, ak ngëm gu sell ci ne Yàlla ci boppam moo nu gàddul sunug dund. Naka noonu mu fàttali ñépp ne, Diiney Lislaam ñor na lool sunu Boroom, te loolu dafay tegtal Yonent yi mi fi yabal. Dineey Muhammad Salla Laahu tahaala aleyhi […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Lii ab laabire la bu bàyyikoo ci Sëriñ Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim jëm ci fonk julli ci Yonent bi Salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama. Wax na fi loo xam ne dana yokk jullit bi ag sawarte ci gën a fonk Salaatu rawatina di ko jaarale ci Salaatu […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw ba mu fàttalee boppam ki mu doon, te mooy ab liggéeykatu Sëriñ bi. Dafa daaldi xamle ci bu leer ni Yàlla Subhanahu Wa Tahaala bëggee ñu jaamu ko, ak ni mu ko ñore, mu daal di fàttali baakaar yu mag yi mat a moytu mel ne jëw ak fenn ak doxalin […]