Kan Mooy Sëriñ Mbàkke Madina

Sëriñ Mbàkke Madina, dafa doonoon nit ku fonk jàng, jàngale ak jëfe xam-xam. Doonoon ku fonk sunnas Yonent bi Aleyhi Salaam, di ko dund bu wér. Dafa doonoon ku noppi, am dal lool, bari ñu ko sopp muy kilifa yi di ndogo yi. Mbokkam yépp bëgg ko ak daan ko ndamoo bu wér. Ku dëddu […]

Kan Mooy Gaïnde Fatma

Ku amoon gis-gis bu sori la. Dafa teel a yeewu ci doxiinu jamono. Moo tax masul neenal benn xam-xam bu am njariñ. Dafa daan yóbb ay nit ñu bari ñuy jàngi ci yeneeni réew. Teewul itam mu sàmp ay jàngukaay ci biir Senegaal. Tuubaa itam mu liggéey mbed yi, def ci liggéey mu am solo […]

Kan Mooy Sëriñ Musaa Ka

Moo doon Werekaanu Bàmba, di xamle jaar-jaari yoonu murid, cëslaayiyoon wi ak daan dànkaafu képp kuy dal ci Sëriñ bi mbaa ci yoon wi. Mooy koo xam ne kenn du sosal kenn ci ñoñ yoon wi mbaa boroom yoon wi te mu nekk fi. Mooy délluwaay bu mag bi ci xam melloy SëriñTuubaa, ay jikkoom […]

Kan Mooy Sëriñ Masàmba Jóob Saam

Sëriñ bi nag moo gis Sëriñ Masàmba fekk ko ci ronn garab muy yër ab téere. Sëriñ bi nuyu ko, ñuy jàmmasante ak a waxtaan. Ginnaaw gi nag la Sëriñ Masàmba laxasaayu ni day seeti Sëriñ Tuubaa. Ci la daaldi dem Pataar ci daaray Sëriñ Moor Anta Sali nekk fa di fa yokk jàngum xam-xamam […]

Kan Mooy Seydina Usmaan Mbàkke

Baay Njaga Jóob nee na : « Seydinaa Usmaan dafa njariñu ci Seex Ibra, njariñu ci Maam Cerno, njariñu ci Sëriñ Tuubaa ». Ku daan ñaan la muy am, te ràññeeku ci lool. Am na sax ay nit yu daan jëfandikoo sàngara, moo ko dindi ci ñoom ci lu gaaw. Daf daan soññi murid yi […]

Kan Mooy Seex Muhammadu Lamin Jóob Dagana

Seex Muhammadu Lamin 1886 la gane àddina. Yonent bi AleyhiSalaam la ko baayam tudde. Soxna Haanatu Jóob mooy way-juram wu jigéen. Sëriñ Tafsiir Ahmadu Jóob mooy baayam mi ngi dëkkoon Dagana. Wollare Sëriñ Tuubaa la woon, moo ko jébbal itam Sëriñ Muhammadu Lamin ak mbolleem njabootam. Seex Muhammadu Lamin it ku amoon hikma la. Daan […]

Dundug Maam Ceerno

Fii danu fiy àndi lenn ci jaar-jaari Ceerno Ibraahima Faati. Lu mel ni ki judoom, ay jikoom, digganteem ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu, miy magam di lépp. Niki noonu dees na fi jukki ay bataaxel yu ko Sëriñ bi bindoon. Yal nanu Yàlla fayal Borom Daarul Muhti.

Kan Mooy El Haaji Baara Mbàkke

Sunu sang bi turam dëgg mooy Muhammadul Amiin, ñu duppee ko Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke miy doomi Sëriñ Tuubaa. Sëriñ El Haaji Baara nag mi ngi gane àddina atum 1921 fa Ndidi. Baayam moo di Sëriñ Fàllu Mbàkke, ndeyam di Soxna Xari Sàll. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ko Sëriñ Moor Sànqe, ginnaaw […]

Kan Mooy Sëriñ Siidi Muxtaar Mbàkke

Sëriñ Siidi Maxtaar, Sëriñ Baara Mbàkke ak Soxna Mati Ley ñooy ay way-juram. Mi ngi gane àddina atum 1925 fa Mbàkke Kajoor. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ku turondoom Sëriñ Seex Awa Bàlla waaye mi ngi mokkale Alxuraan ci kenn ci taalibey Sëriñ Baara ñu di ko wax Sëriñ Ñaan Jóob. Bi mu noppee […]

Kan Mooy Maam Seex Ibraahima Faal ?

Mooy doomi Ahmadu Roqaya Faal ak Soxna Saynabu Njaay. Mi ngi cosaano ci Damel yi, doonoon ay buur fa Kajoor. Mu bàyyi lépp ginnaaw ngir aajawoo Boroom ci na mu gën a kawe ci yite yi. Mi ngi gane àddina atum 1855 walla 1856. Lu man a xew daal Sëriñ Tuubaa ñatti at la ko […]