Ku amoon gis-gis bu sori la. Dafa teel a yeewu ci doxiinu jamono. Moo tax masul neenal benn xam-xam bu am njariñ. Dafa daan yóbb ay nit ñu bari ñuy jàngi ci yeneeni réew. Teewul itam mu sàmp ay jàngukaay ci biir Senegaal. Tuubaa itam mu liggéey mbed yi, def ci liggéey mu am solo ci ndigalu Sëriñ Fàllu.
Nit ku laabir la woon, di dimbale, di taxawu nit ñi ci seen i soxla. Doon bàyyi xel doxiinu réew mi, di joxe xalaatam ak a jëfe xalaatam. Lépp lu mu yaakaar ni sunu ko defe dina njariñ askan wi te dina dëppoo ak sunu Diine daan na sónn ak def yite ngir mu am.
Bu dee lu jëm ci yoonu murid, lii nuy woowe « Daayira » wax neen ni moo ko sos, te daan wax nees ci wara doxee ngir mu jëm kanam.