Mi ngi gane àddina 1912 fa Daarul Aaliimil Xabiir, mi ngi feeñ ci weeru safar. Doomi Xaadimu Rasuul la, Soxna Faatima Suxraa mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ bee ko jëlle Gànnaar moom ak Soxna Faatima Kubra way-juru Seex Abdullaahi Mbàkke. Ñoom ñépp ay sariif leen.
Ba mu dikke àddina la Sëriñ Abdu Rahmaan yabal ndaw ci Sëñ bi mu fekk ko Njaaréem jox ko bataaxel di ko yëgal li xew. Sëriñ bi bind ci ginnaaw kayyit wi » << attaxasa laahu Ibraahima xaliilan>>.
Sërin Abdu Rahmaan Lo moo ko jàngal Alxuraan ba mu mokkal ci diir su gàtt. Ba mu bindee ab kaamil la daal di ñëw Njaaréem jox ko Sëriñ bi ànd ak Sëñ Abdu Rahmaan mu def ci moom ay séede yu refet. Ndax dafa xamal Sëriñ bi ne ko diiru li ñuy nekk yépp masul yékkati sama siditu jë, te it dafa maa yombalal jàngale mi ndax ni mu nangoo. Sëriñ bi teey leen fa 15i fan ginnaaw gi mu ne leen man ngeen a déllu, te su ngeen deme na nga ko jàngal Téere sangam, ak sangam. Kon ba ci Téere xam-xam yi mu war a jàng sax Sëriñ bee ko ko digal. Ba fi Sëriñ bi jóge itam, Sëñ Ibraahima daa wéyal di nekk ci kilifteefu Sëriñ Abdu Rahmaan. Taawam itam moom la ko tudde. Waaye teewul itam Sëñ Ibraahima jàngee na ci Sëriñ Madem fa Njaaréem. Ba mu tollo ci buntu àddina Seex Mustafaa magam laaj ko foo bëgg dëkk mu ne ko Mbàkke Bawol ngir li fa Sëriñ bi gane àddina. Diggam ak Sëriñ Fàllu na mu ci daan doxee mooy « lu ma xam wax ko ko, lu ma am jox ko ko » Sëriñ Fàllu itam doyloo ko ci mbiri baatin. Magam yëpp la boole woon bëgg niki Sëriñ Abdulaaahi borom dër bi ak Sëriñ Basiiru.
Ci mujjug dundam la tukki woon, di wër réew yi Sëriñ bi jaaroon. Sëriñ bi nag mooy ki ko feeñu woon diggal ko ko, te naan ko lépp lu ma fa bàyyi na nga ko indaale. Mbàkke Bawol la ko njëkee feeñu, ginaaw gi mu feeñu ko Ndakaaru, feeñu gu mujj gi nag ma nga ame woon Luga. Sëriñ bi it da ko cee xamaloon ne lépp loo ciy def na nga ko defee ak sa xaalisu bopp bu la ci kenn dimbali. Li lépp nag ci weeru koor la xewe. Bisub gaaw nag la bàyyikoo Mbàkke-Baari wutali réew yu sori ya, boobu fekk nañu wori ba am 17i fan. Def na ñatt weer ci tukkeem boobu. Loolo waral sax Seex Musaa Ka bind « Yokkub Jasaawu Sakuur ». Ay mbir yu xar-baaxe la fa Sëriñ Musaa ka di wax, di xamle kiimaan yi ak jàppandal yi feeñ ci tukkib Sëriñ Ibraahima bi.
Bi mu jóge ci tukki bi, dafa woo Sëriñ Musaa ka ne ko man walla yaw walla Sëriñ Fàllu dina am ku wuyu ji Boroomam. Sëñ Musaa ne ko : » Mbàkke mba du day man? » Sëriñ Ibraahima ne ko, déet yaw sa liggéey matagul. Mu ne ko mba du day Sëñ Fàllu ? Mu ne ko déet moom moo wara yéegale Jumaa ji. Man mii lay doon ndax li ma waroon a liggéeyale Sëriñ Tuubaa mat na sëkk. Bu nu màggalee ba noppi dinaa tawat, te tawat gi yëpp di na mandargal tiis yi ak yi ma jëlle ci sama tukki bi. Jëll naa ci sama wàll ba mu mat sëkk. Bu nu ci yégge di nga gis ma dàq sama bëkk-néeg yépp. Doomi Sëriñ Tuubaa gu ñëw di ma seetsi na agsi, waaye ku mu yar mba muy taalube na yem ci yaw, te nga ni ko tànne naa. 26i benn ci ràkkaati Gàmmu laa fiy jóge bisub àjjuma lay doon. Waxam ji nag am na ay firndeel ndax Sëriñ Alhaaji Baara Fallilu yal na ko Yàlla dooli leer, wax na ne toog naa bis mu woolu ma ma ñëw Mbàkke Bawol fekk ko fa ak sama « auto » mu ne ma damaa bëgg nga yóbbu ma Tuubaa, te it na nga xam ne jàppuma faa jóge. Soo may yóbbu na nga ma jaarale yoon wi ñu jaarale woon Sëriñ bi ba ñu koy jëlle Njaaréem. Ba Sëriñ Ibraahima agsee Tuubaa, kër Sëriñ Tuubaa gi la daal di, dal, ca foofe la wuyu jee boroomam.
Ñent fukki at ak ñatt(43) la dund, Murid saadix la woon, woyof lool, am yërmande, fees deel ak baatin, am xam-xam, am « dignité » te fonk diineem, am jàmm, bari fulla, tar lool ci kuy jéem a gàkkal yoon wi.
Seex Abdu Mbàkke moom Sëriñ Daam Atta ibn Seex Ibraahima Mbàkke mi tax nu man leen a néttali li yal na gudd fan lool te yàgg fi te wér te làq ngëramal Sëriñ Tuubaa.
Al-Habdul Xadiim
13/01/2021
MaSha’ALLAH amna solo Yallah na Yallah yoki leram tei tass niou si barkem 🤲🏼
Amiin Amiin Soxna Astou
Machallah kawena lool Cëy Sëriñ Tuuba ak waa kërëm
Yéeme leen def