Bismillahi Rahmaani Rahiim
Mi ngi ganee àdduna Tuubaa fii barabu Sëriñ bu Mag bi nekk. Turam moodi Seex Muhamadu Lamin Baara di dóomi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ak Soxna Aminata Lóo.
Ci 28 Jumaadal Ulaa 1309 la gànne àddina dëppook 20 décembre 1891.
Sëriñ Baara mi ngi jàngee Alxuraan ci Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo (ndaam). Jàngee na itam fi Maam Cerno, ci Sëriñ Ibra Bineta Silla ak ci Sëriñ Mbay Jaxate ci lu aju ci wàllu Diine ji.
Sëriñ bu Mag bi nag moo ko tarbiya.
Sëriñ Baara dafa doonoon ku am taalibe di liggéeyal Borom Tuubaa. Daan defar ay mbooloo ak di leen xettali, Daan joxe alalam ak ay niti boppam ci bépp naal bu ñu masa sumb ci yoon wi.
Jàng ak jàngale ak bay moo doon ay yëngoom, barina it yeneen « métier » yoo xamne Yàlla defaloon na ko ci ag xereñ, te moo ko daan defal boppam ak njabootam, lu mel ni ñaw, wala « menuiserie ».
Doonoon it ku yéwén lool ci lu baax, bari yërmande, rafet jikko, fonk ay mbokkam, daan dimbali néewji doole yi, daan teral doomu aadama yi.
Sëriñ Tuubaa it gëram ko, li koy firndéel mooy yabal ga mu ko yabaloon Sànnoosi ak Mbàkke Kajoor, ba xëy bind ko bataaxal bob, wax na ko ca ne « Yaw Muhamadul Amiin, na nga xam ne am nga fa sa Boroom daraja joo xam ne mbooleem say kem di nañ la ci ñee, te képp ku ànd ak yaw, du gis lu ko naqari fii ak fa ñu jëm… ».
Jikkoom yu refet yooyu moo waraloon la miy def ci nitam mooy jàngal la, yar la, def ci yaw jikko ju rafet, xamal la nooy jaamoo Yàlla, te teg la ca yoon wa, sooglaa yewwi, nga doon ku defaru, ba mana defare.
Ku bariwoon lool lu miy jaamu Boroomam la, ragal Yàlla lool te farlu. Bëgg Yonent bi Aleyhi Salaam lool. Fonkoon Alxuraan lool ak Xasiiday Seexul Xadiim.
Digganteem ak ay mbokkam rafet lool, ak daan matal kóolare, ku ne mu tuddee la doom,féetale la ko, bind ci yaw ay kàdduy seede, dëkk ci di la teral góor ak jigéen.
Daf daan gor ay àll, def ko Daara aki Tool, defar ay mbooloo, wutal leen ay « métier »
Ab bindkat la woon. Ci anam yu wuute la jëm, te bari na lool, waaye ay bindam man neen wax ni sant Yàlla la, jéggalu Yàlla la, tagg ak julli ci Yonent bi Aleyhi Salaam la, màggal Sëriñ Tuubaa, ak digle lu baax. Bokk na ci ay bindam Munawirul Bunyaan, Sahaadatul Axyaar, Buchraaki, Inal Wara Tadarahoo, Tibbul Fu-aad Safinatul Abraar, Zahabul Ibriz, añs.
18 Juin 1936, ci 45 atam la fi Sëriñ Baara RLA bàyyikoo.
Di sant Sëriñ Abdu Xaadir Majalis mi doon tontu sunuy laaj ak Sëñ Ahmad Mbàkke. Di leen ñaanal gudd fan, wér, sutura ak teranga ak ngëramal Borom Tuubaa. Di ko ñaanal sunu bopp itam. Ak mbolleem ku yër mbind mi ak ku déglu fàww ci barkeb Seex Muhamadu Lamin Baara Mbàkke.
Machallah ndeysane kene dou cheikh Mouhamadou lamine bara mbacké ❤️❤️❤️
Ndeysaan sikkuwut de moom