Kan Mooy Sëriñ Abdu Rahmaan Mbàkke ?

Al-Habdul Xadiim
30/09/2022

Bismillahi Rahmaani RahiimMi ngi gane àddina atum 1954, Soxna Maam Jóob mooy way-juram wu jigéen bokk ci waa Koki, way-juram wu góor di Sëriñ Abdu Xudoos moom Maam Cerno. Sëriñ Moodu Faati Jéy Jóob moo ko dalal Alxuraan fa Daaru Salaam moom ak seexam Sëriñ Fàllu waaye Kooku ci fukki atam ak ñaar la wàcce liggéey.

Ba mu noppee ci jàngum Alxuraan mi la ko Baayam yabbal Tuubaa ca Sëriñ Habibu Mbàkke. Ba mu noppee ci jàngum xam-xam mi fa Tuubaa la daaldi déllu fa Daarul Muhti ci yoxoy Sëriñ Abdu Xudoos. Kon lépp loo gis mu di ko xamle ci Téere yi Senegaal la ko xamee.

Moom Sëriñ Abdu Rahmaan nag, dund na dund gi teey, gu baarkeel, njariñ mbolleem ku xam-xam ñor. Yemul woon rekk ci sos Daaray Alxuraan ak Daaray xam-xam ngir jàngale waaye daf daan bàyyi xel ñi bëgg jàng te manuñoo teew Daarul Muhti, ñi wara ñëw ëllag ci ginnaawam te wara gindiku ci Diine. Loolu mu tax mu utoon micro ak magnétophone di tekki Teerey Tawhiid yi, Teerey Fiq yi, Teerey Tasawuf, Teerey Teggin yi, Teerey Nahwu ak yeneen. Ba jamono doxee, mu mujj di ko def ci ay K7 ak ay CD. Ba fi mu ne utooon na ay clé USB ak i carte mémoire yu bari di ci sotti xam-xam di ko jox mbolleem ku ci am xéeméemteef. Am na sax ab taalubeem bu farlu lool, dëkk Lyon, liggéey na ab site tuddee ko yoonewi.net, def na ci sax ab application mobile ci androïd, ñàkkul ni mi ngi bàyyi xel itam système IOS bi. Moom Sëñ Siidi nag daa fexe ba lépp lu nekk ci yoonewi.net muy wolofi kese. Njariñ ju réy a réy mooy bàyyikoo ci boobu le site. Am na it ñeneen ñuy yaatal Téere yi ci seen i chaînes YouTube ak ci ay canal Telegram. Yooyu liggéey yépp yal na barkeel te Yàlla gëram ko.

Sëriñ Abdu Rahmaan nag, Jàmbaar ji, yemmul woon rekk ci jàng ak jàngale, daf daan béy, te liggéey bum dégg ci lu baax, daan na ci def alalam, mba ñaqam bu dee ci ay tool la.

Nit ku baaxoon la lool, woyof tool, amal nit ñi njariñ daan leen di taxawu, di leen dimbali ci seen i soxla. Daan jullee ci Jàkk ji, ba tax na sax ku ko masaana bëgg gis, foofu nga key fekk.Ab bind katu Xasiida lawoon bu mag. Daan na Marsiyaal Góor Yàlla yi. Bëggoon lool Xasiiday Seexul Xadiim te daan ko dund bu wér. Li mu ci bindaat bari na lool. Ñay bind itam, daan neen ko yét mu toppaat. Góor Yàlla tigi la woon, Géejug xam-xam la woon, ragal Yàlla lool, sell lool, teey lool, dëddu àdduna lool, bëgg Sëriñ Tuubaa lool.

Yal na ko sunu Boroom dolli yërmande, yokk ay leeral ba fàww, dëkkale ko ak Sëriñ Tuubaa ak Maam Cerno, barkeb weeru Gàmmu gi nga xam ne ci la wuyuji Boroomam ci atum 2022, ak ci barkeb Sayyidina Muhamad Sala Laahu Tahaala Aleyhi bi Aalihi wa Sahbihi wa Salam.

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Cheikh Diop
Cheikh Diop
2 années il y a

Jërëngeen jëf sëriñ bi amna solo lool, yal na leen Yàlla fay aw yiw. Sëriñ Abdu Rahmaan Mbàkke yal na ko Yàlla dolli yërmaande ak ug njéggal ak i leer yu dul dakk ba fàww !