Miftaahul Xuyóob (2)

Ci xaaj wi, dees na fi lim yi nga xam ne war na boroom kër mu xamal ko soxnaam, ñi mu njaboote. Te mooy faratay jëmam ak mbolleem li ci aju, dalle ko ci laab, ponki diine yi la cay farata ak sunna. Di ko waar ngir bëggal ko lu baax ëllag. Te sax « góor […]

Leeral Miftaahul Xuyóob (1)

Li ab Téere la bu am solo jëm ci xamlee nees di yoree sa Soxna ak ay mbir yu jëm ci dundug bàmmeel ak yeneeni yëf. Ku ñuy wax Umar Jóob moo doon laaj Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ay laaj yu am solo. Sëriñ bi bind Téere bi àndil ko ci ay […]

Leeral Fathul Zaahiril Baatin…(2)

Dina fi feeñ lenn ci njariñ yi nekk ci bàyyeek sa lépp sa Boroom, woolu ko bu wóor, ak wéral sab pas-pas ci dëggal saw doxiin sa diggante ak moom. Am na lees ci toftal ci Téere bi, jëm ci leeral luy mag, ak i màndargaam. Akub tënk jëm ci ponki Diine.

Leeral Fathu Zaahiril Baatin…

Ginnaaw muslu ci saytane, ak julli gu mat ci Yonent bi Aleyhi Salaam, Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daa sant Yàlla bu wér. Dafa daaldi xamle li yit pas-pas bi nu war a am ci sunu Boroom ak ay jeexitalam, ci sunu nekkin, sunu jëfin ak sunu dund.

Leeral Nahju (9)

Su ko defe, ci xaaj wi la nu matale sunub liggéey ci Téere bii di Nahjul Qadaa Al-Haaj. Njariñ li yaatu na lool, la muy xamle di sunub defaru tay ak ëllag. Mbolleem li ci Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ñaan yal nanu dal. Yal nanu Yàlla saxal ci am i teggin biir […]

Leeral Nahju (8)

Ci xaaj wi dees na fi leeral teggin yi war diggante Taalube bi ak Sëriñ bi. Njariñ li nekk ci topp Sëriñ bu mat Sëriñ. Ni mu lay defare, ni mu lay dimbale ak ni mu lay taxawoo sa diggante ak sa Boroom. Sëriñ bi itam dina fi leeral dëgg-dëggi xarit ak mbokk mu baax. […]

Leeral Nahju (7)

Fii danu fiy leeral ni, jàng xam-xam dëgg-dëgg, ci ndaw lañu koy gën a manee. Njariñu xam-xam ci nit, dayoom gi ak i jeexitalam réy na lool ci ku jóg sóobu yoonu xam. Yal nanu Yàlla xiir ci sàkku lu nuy njariñ ci àdduna ak fa allaaxira te lépp dëppook bëggug sunu Boroom ak ngëramam […]

Leeral Nahju (6)

Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daa soññee lool ci tabe, teral gan ak yaatal ko. Mu fiy wax lu tax loolu di lu manul ñàkk ak xéewal yi ci nekk ak ngëneel yi. Di wax it solos xam-xam, tolluwaay wu réy gi ma am fa sunu Boroom. Di leeral ne ndamoo ay askan […]

Leeral Nahju (5)

Fii danu fiy àndi ay leeral ci teggini sàmm say gët, worma gi nu wara wormaal mag ñi. Ci bu nu tooge ak ñoom, bu nu àndee ak ñoom ci tukki, bu nuy lekkandoo ak ñoom ak yeneen. Njariñul wax dëgg, ay jeexitalam ak dayo gi am fa Yàlla.

Leeral Nahju (4)

Fii Sëriñ Alhaaji daf fiy leeral dénkaaney Sëriñ Tuubaa ci sàmm sa bopp, am kersa ak di wormaal nit ñi. Njariñul nuyoo, teggini nuyoo ak ay jeexitalam dees na ko fi fésal. Naka noonu yar say gët, màndu, xam kooy àndal, xam kooy roy dina fi leere. Ay wax yu am solo te bari ngariñ […]

1 2 3 5