Kan Mooy Sëriñ Murtadaa Mbàkke(1)?

Al-Habdul Xadiim
02/11/2021

Mi ngi feeñ jamono ci atum 1340 dëppoo ak 1920 walla 1921, 26 fan ci Gàmmu ca dëkk buñuy wax Daarul Haalimul Xabiir, ñu gën ko xam ci Ndaam. Soxna Njaxat Silla nettali na Sëriñ Mustafaa Lo ne ko, Sëriñ Ndaam dey terale na 33 gàtt Sëriñ Murtada. Ba weeru gàmmo teerse day def bis bu set mu lewetal ab gàtt ba bis ba ñu koy jox tur. Nu bari nag defe neen ni mooy caatu Sëriñ Tuubaa, waaye li am moo di am na ñaari rakk yu mu bokkal nday ak baay, dañoo yàggut àdduna rekk te mooy Sëriñ Haamidu Mbàkke ak Sëriñ Ahmadul Muxtaar caatu Sëriñ bi, moom mi sax la Seex Muhammadul Mustafaa tudde Sëriñ Ahmadul Muxtaar miy xalifa Daaru Xudóos.

Seex Murtadaa mii nag ba muy gane ci àddina dafa indaale turam ci loxo nday-jóor bi ñu bind ci Muhammadu, am na sax ñu mu ko daan won. Sëriñ bi it ba mu yégge ab dikkam daa bind ci kayyit « Muhammadu ». Sëriñ Abdu Rahmaan lo moo yokk Murtadaa ci tur wi. Way-juram wu jigéen nag mi ngi tudd Soxna Faati Tuuti Jóob di sëtu Sàmba Mareem doonon ab xaadir bu Yàlla baaxal, doon jànge ci Sëriñ Moor Anta Sali, Soxna Jaara doonon ndayi daaram, taarixal na ko it. Te li mu fekke képp la ci àndi.

Ndayi Sëriñ Murtadaa nag, mokkal na Alxuraan bind juróomi kaamil, te boobu mi ngi ci ron Sëriñ Tuubaa, Seex Abdu Rahmaan Lo di ko jàngal Alxuraan doomam bu jigéen it di Soxna Jóob Mbàkke bind ñent kaamil.

Kon nu dellusi ci ki nu tax a jóg, ba mu toole ci wara jàng magam Seex Mustafaa moo ko yóbbu Cindoodi ci nijaayi boppam Sëriñ Maxtaar Aale Lo waaye jotu faa yàgg mu daaldi dikkaat Ndaam, mu mokkale ci Sëriñ Abdu Rahmaan. Seex Mustafaa dalal ko xam-xam moom ak Sëriñ Dan Xari Lo ak Sëriñ Aliwu. Ñaar ñii ay doomi Sëriñ Mustafaa lañu. Te boobu teewul mu yilif yoonu Murid. Waaye xataay gi tax na Sëriñ Murtadaa wéyal njàngam feneen fu ci mel Tuubaa-Kayel. Jamono jooju Sëriñ Muhammadu Lamin Jóob dagana moo fa nekkoon ba tax na Sëriñ bi jàngee ci moom. Ak Mauritanie ba mu fay dem 18 at la am. Ku ñuy wax Umar Juuf ak Seex Jeŋ la àndaloon, ba ñu toolo Rooso, Sëriñ Daam Buso Imaam dab leen ànd ak ñoom. Nu wàcc ci kenn taalibey Sëriñ Tuubaa, bokk ca waa Gànnaar ñu naan ko Seex Abo Madiyaana, mu jàngee ci moom lu baree bari. Ginaaw gi mu déllusi Senegaal jàngee ci doomi Sëriñ Mbàkke Buso, te mooy Sëriñ Asan Buso mi des Madiinatul Munawara, mooy ki àndoon ak Sëriñ Abdu Xaadir aji Màkka. Ba mu noppe ci loolu la déllu Tuubaa-Kayel nekk fa di weet ak a xalaat, ni ko niti Tasawuuf yi di defe ndax ñoom xalam daa bokk ci seen mello. Tuubaa-Kayel googu la tàmbalee dox ay jéego, Sëriñ moo ko ni won ba muy gone, ku gudd tank ngay doon waaye ci wàllu penku. Maanam tukkikat ngay doon rekk. Saalum la njëkk dem ci Sëriñ Moor Xari Si def d fa 4 at. Dikkam ca Saalum nag daa defoon ay haal kilifa googu ndax ba muy tàggatoo ak Sëriñ Tuubaa ca Njaaréem daf koo ne dinaa la mas a fekk Saalum te boo fàttoo maa lay julle. Sëriñ Murtadaa foofu la nekk te bi Sëriñ Moor Xari Si fàtto moo ko taxawu.

Ginnaaw tuddu neen ab jàngam nu dikk ci jàngalekat gi mu doonoon. Wax neen ni ba muy gone yi mu daan foowe ci suuf ci mooy defar ay jàkka ak i barab yu ñuy jàngale. Ab doxom nag mi ngi tàmbali ci 1956 boobu Sëriñ Fàllu moo yor kàdduy murid yi. Mu dikk ci Sëñ Fàllu ànd ak Sëriñ Mustafaa Lo di ko wax li lu bëgg a def ci jàngale. Sëriñ Fàllu bind lettre ngir mu jëm ci gouverneur général waaye njëkk mu fay àgg Sëriñ Murtada signé lo na ko sang yu bari niki Sëriñ Seex Mbàkke, Sëriñ Basiiru, Elhaji Abdul Asis Si, Sëriñ Bu Muxtaar Kunta, Seydi Nuuru Taal ak Elhaji Ibraahima Ñas mii nga xam ne ba mu yégge xibaar bi daf cee teg 50 barigoy dugub.

Al Habdul Xadiim
02/11/2021

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires