Mooy doomi Ahmadu Roqaya Faal ak Soxna Saynabu Njaay. Mi ngi cosaano ci Damel yi, doonoon ay buur fa Kajoor. Mu bàyyi lépp ginnaaw ngir aajawoo Boroom ci na mu gën a kawe ci yite yi. Mi ngi gane àddina atum 1855 walla 1856. Lu man a xew daal Sëriñ Tuubaa ñatti at la ko magee.
Bi mu matale ci wàllum jàng Diine, la daaldi sóobu yoonu Yàlla, dogu ci fàww mu am ko. Jaar na ci ku ne ba keroog nag muy dajje ak Seexul Xadiim.
Li mata xam nag moo di Maam Seex Ibraahima Faal nag dafa doonoon ku yittewoo Boroomam, am yite ci àgg fa moom. Fu bari jaar na fa di fa wut li mu bëgg. Jaar na sax ci Sëriñ Tayba Maar Sill mu baax mi. Sang bi jullee woon Sëriñ Moor Anta Sali, di ko liggéeyal waaye taxul lim bëgg mu am ko dëgg-dëgg.
Sëriñ Tuubaa it fa mu ne yéggoon na ni am na ku koy wër. Moo tax daa am bis bob dafa woo Sëriñ Maxtaar Ture ak Sëriñ Aadama Géy yabal leen ci Sëriñ Tayba Maar Sill di ko yóbbul àddiya. Ba ñu agsee ci Sëriñ Tayba, boobu Seex Ibra mi ngi fa. Di yég bu wér ni ñii fañu jóge saf na sap li mu bëgg. Te mooy yeg ci Yàlla. Doon na wax sax naan ñii bu ñu doon jigéen ma ni kon ñoo ngi séy.
Bi ñu tolle ci wara déllu Mbàkke-Kajoor la Seex Ibra ànd ak ñoom. Bi murid yii agsee ci seen Sëriñ te mooy Seexul Xadiim, daf leen ni ndax amul ku ngeen àndal, ñu ne ko waaw. Mu ni woo leen ko. Bi Seex Ibra ñëwee, Sëriñ bi laaj ko foo bàyyikoo mu ni ko Tayba-Daqaar. Mu ni ko lu doonoon say tànk mu ni ko damaa bëgg yeg ci Yàlla.
Sëriñ bi fàttli ko mbiri ponki Diine ak jàpp ci loolu. Seex Ibra ne ko li ma bëgg dëgg maa ngi key man a amee ci koo xam ne daa yeg ci Yàlla di fa yegale, ci koo xam ne boo ko ñaqale sax teeqalikoo ak ay baakaar. Seex Ibra ne ko man bëti xol laa yor. Duma def mag mu mo gis rekk teg ko ko, duma def ku koy nuru rekk teg ko ko. Ba àgg na ci wax ko ni, ki may wër suñu ma ne woon faatu na, fii leen ko denc. Dinaa ko liggéeyal ba làq ngëram. Sëriñ bi it xam ne moom ak Seex Ibra ñoo bokk pas-pas. Loolu moo tax Sëriñ Basiiru Mbàkke ne woon « pas-pasu sunu Baay Seex Ibra mel na ne bob Sëriñam ba ». Ndax kat Sëriñ Tuubaa it xam ni Yonent bi Aleyhi Salaam asamaan si ak bidéew yi ñoo ko daan tiim doy na ko.
Ci biir jotaay bi nag day am jamono joo xam ne duñu wax dañu doon xoolante rekk. Leeg-leeg ñu jóg di dox di wax. Leeg-leeg ñu ànd toogaat.
Li yéeme ci jébbalug Seex Ibra moo di sunu Boroom ci boppam moo ko tegtal Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu. Loolu la Sëriñ Musaa Ka di way naan :
« Mas nay xibaar ag jébbaloom bay wax ne Yàlla mi ka moom, moo ko ne Bàmba moo la moom raasi ko jox ko say pexe.
Tegtal ko yoon wa ab murit, di aw ba raw pexem Marit, ba am ngërëm bariy murit, te dootul ree di tex-texi.
Mu dal di dem Tayba-Daqaar ngir dégg Bàmba di xaar, seet na sëriñ Tayba-Daqaar ci jàng lay xamey pexe.
Mu tëdd guddi listixaar bët set mu xëy ba tisbaar, Seriñ Maxtaar Ture fa jaar leeram ga wan ko ay pexe.
Maxtaar Ture nga yoori njoor yanu ko jëm Mbàkke-Kajoor, Seriñ ba yóoni ko ca buur Seex Ibra topp cay fexe.
Mu jis fa Seex Aadama Géy sànni mbiram dal di cay ŋoy, mu wan ko Bàmba mbër mu rëy Sëriñ bi naan ko foo fëxe.
Mu wax ko tegtal ya fa moom, Seriñ Bàmba wan ko la fa moom, mu xam ne jis na ka ko moom mu dal di jël mbiram joxe.
Mu sóobu far ba jiitu leen, Bàmba ne kii ëpp na leen, leeram gu rëy gii wër na leen, fum toll xol bay nux-nuxi.
Wax na tuuti kon mu dem fekk Seriñ bi lëm mbiram, ba kenn du jot ci baatinam lu dul ca bis ba ñuy texe ».
Lii nag tegtal bu leer la ci jébbalug Seex Ibra ak na mu daan doxee. Ku Sëriñ Tuubaa jàppoon la te am ci moom coffeel. Daan na wax bëgg leen Seex Ibra ngir li ma ko bëgg, mbaa ngeen bëgg ko ngir bëgg maa bëgg, mbaa ngeen bëgg ko ngir li mu ma bëgg.
Seex Ibra it doonoon ku bari pasteef. Lum am jox Sëriñ Tuubaa. Liggéeyal ko rekk ci la sax. Ndax kat moo ni woon Sëriñ bi : « fii lu ma fi amul daf fee amul ». Lu waay di def ngir jëmi Sëriñ bi dina fexe ba laal ci dara. Te loolu lépp du bokk ak sasub boppam.
Mooy koo xam ne masta soppiku ci jaayanteem ak Sëriñ ca Mbàkke Kajoor ja ba ni mu fiy bàyyikoo.
Ku amoon Hikma la, daan na wax naan :
– Ku ñu tëkku mu tiit, gëmul Yàlla. Waaye ki ko tëkku gëmul Yàlla.
– Jàmbaar du bari ay jëf, jàmbaar dëgg mooy moom sa bakkan ànd ak sam xel boo mere.
– Am taar nekkul ci yere yu rafet, ki taaru dëgg mooy ki rafetal yéene ci ab xolam.
– Yeewu du bari ay wax, ki yeewu dëgg mooy ki jiital alalam ci bàmmeelam.
– Ñàkkug àdduna du ag ñàkk, ñàkk dëgg mooy boo ñàkkee yiiw ca bisub hisaab ba.
– Ag njirim du ñàkk ay way-jur, jirim dëgg mooy ñàkk yar ak i teggin.
– Xam-xam du rëy kàggu ak bari ay téere, xam-xam dëgg mooy jëfe langa xam ngir jëmmi Yàlla Subhanahu wa Tahaala.
Li lenn la rekk ci waxam yu am njariñ. Seex Ibra nag 1930 la wuyuji Boroomam yal nanu Yàlla taas ci barkeem. Sunu Boroom it yal na koy dolli leer ba fàww ak di ko dolli yërmande.
Maa Shaa Allah. Keine dou Mame Cheikh Ibrahima Fall
Kenn la daal
Manchallah mouride amna solo
Akassa FAAL ❤️✌️
Jaajeuf yaaram
Heukaza macha Allah
Yalla na Yalla yokk kham kham gui🙏
Amiin nu bokk