Kan Mooy Soxna Astu Gaawaan

Al-Habdul Xadiim
21/07/2022

Bismillahi Rahmaani Rahiim

Soxna Aysatu Mbàkke doomi Seexul Xadiim ñu gën koo xam ci turu Soxna Astu Gaawaan mi ngi gane àddina 1904. Way-juram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Xadi Jóob gën a siiwe ci Soxna Xadi Gànnaar di doomi Madu Faa-Xujja moom Masàmba Anta Ceebo.

Sëriñ bi moo ko dalal am jàng. Bi nga xamee ne am jàngam mat na. Sëriñ bi da ko jox taawam Soxna Faati Ja ngir mu tarbiya ko. Soxna Astu, Sëriñ Muhammadul Muxtaar ak Soxna Aminta Mbàkke la bokkal way-jur wu jigéen. Mu doonon boroomi jagle yu réy ci Sëriñ bi. Ba tax na Sëriñ bi mas na ko seeti fa mu ko yabaloon mu fay liggéeyal Boroomam, muy kër Sëriñ Muhammadul Amiin Ture mi nga xam ne moom la ko Sëriñ bi joxoon.

Mbolleem waa kër Sëriñ bi fonkoon neen ko lool moom Soxna ci, jox ko cër yu réy a réy. Mbolleem mag ñi noonu leen ko fonkewoon, mu doonoon ku man a tarbiya, fonkoon Sëriñ bi lool, bëgg ko lool. Wax neen ni daf daan wut ñatti mbubu ci jamono ju ne. Mbubu mii mu ciy siyaare ji Sëriñ bi, menn mi mu ciy jaamu Yàlla, menn mi mu ciy jàng Alxuraan. Mu doonoon ku yëram mbindéefi sunu Boroom yi , te daan taqoo di leen dimbali ci seen yite, lu mu yor jox leen ko, du denc dara.Defoon na ci këram 22i mbana, jël ñoo xam ne duy mbana la leen jagleel nit ñi di ci naan, te boobu ndox yombul ca dëkk ba. Nit daan na xéy ba jant so te du am lu mu naan. Dan na wax naan man ku ma liggéeyal Yàlla fay la.

Mu doon koo xam ne wane na ay xar-baax yu bari. Wax nañu ne am na nawet woo xam ne dafa yeex a taw ñu wax ko ko, mu ne du taw te sama nées bi ma def Xasaayid yi defaruñu ko. Fekk booba da doon senn, mu ne Xasaayid yi duñu tooy ci sama néeg bi. Keroog ba ñu ko defare la taw, taw bu baree bari.

Am na ku ñuy wax Sëriñ Aafiya Mbàkke di doomi Sëriñ Abdul Waduud Mbàkke, dafa am ñu mu àndaloon, ñu doon dem Poroxaan, Yàlla dogal seen oto bi def aksidan ca yoon wa. 9i nit faatu nañu ca, ba ñu tëral leen muur leen, te boobu Sëriñ Aafiya bokk na ci ña ñu tëral ba muur leen. Ba ñu ko waxee Soxna si, da ni Aafiya Mbàkke faatoogul leggi ndax dafa am lu ma koy ligéeyloo. Sëriñ Aafiya dundaat na 30i at.

Soxna si ay jagleem ci Sëriñ bi maneesuko lim. Mi ngi wàcce ab ligéey ci 3i fan ci aw Kori atum 1984. Yal nanu Yàlla taas ci baarkeem te yokk ay leeram.

Al-Habdul Xadiim
21/07/2022

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires