Dénkaane bu jëm ci Soxna Penda Jóob (8)

Al-Habdul Xadiim
29/02/2020

Bismilaahi rahmaani rahiim.

Sëriñ bi ginnaaw ba mu leeralee ni kuy sàkku Boroomam la ak Yónnentam ba salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama, la daaldi wane ag jubloom ci dénk soxnas baayam ju ndaw ja, nu naan ko Penda Jóob.

Daf ko wax ne:

Maa ngi lay diggal yaw soxna si nga góor-góorlu ci muñ ak ragal Yàlla, sa Boroom, ci lu nëbbu ak lu feeñ ; soo ko defee de Yàlla dina la jéggal ëllëg.Nanga sax ci tuubal Yàlla saa su nekk ak farlu ci def lu baax, kon bul jeng mukk jëm ci leneen ludul ag njub.
Nanga sax ci nangoo wéet ngir jaamu sa Boroom. Looy def dee ko def ci sutura te deel suufeel sa kàddu saa soo dee wax, soo ko defee de Yàlla dina la gërëm.

Yaw Soxna Penda, li la dese ci sa giirug dundu, bul jógati mukk jëm ci loo xam ne leerul a ne dagan na ci Lislaam. Deel moytu bu baax jëw ak rëy. Deel saxoo noppi ak muñ. Deel moytu bu baax wax lu amul ak ngistal walla bëgg a siiw. Nanga moytu naw sa jëf walla di bañante ak sa moroomi mbindéef yi. Nanga sax ci dëggu ak sellal, deel farlu ci laabire ak a dimbali jaam ñi. Loolu soo ko defee de sunu Boroom di na la defal ay may ak i jagle.

Bul xalaat mukk topp sa Boroom ci lu àndul ak topp sa ndigalul boroom kër bu ragal Yàlla boobu ndax xamal ne kat, jihaadu soxna ci yoonu Yàlla mooy mu farlu ci topp ndigalul boroom këram. Looloo waral saa su boroom kër ( bu ragal Yàlla) gëramee soxnaam, sunu Boroom dina gëram soxna soosu, te dina ko defal ay xéewal. Waaye su fekkee boroom kër gërëmul soxnaam, soxna soosu na xam ne sunu Boroom du ko mas a gërëm.

Maa ngi lay xamal ne lépp lu nit man a def te jëmmi Yàlla rekk taxul, jëfam jooju sànku na te ñàkk na ko. Te na la wóor ne, kenn du man a mucc ëllëg ci mbugalum sunu Boroom li feeg bàyyiwul ñent bir yii, te mooy : wax lu dul dëgg, rëy, nay ci sa alal, ñaaw njort ci sa moroom ak ci sa Boroom.

Al-Habdul Xadiim
Lyon, 29/02/2020.

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
10 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Khadija
Khadija
4 années il y a

Ma Sha Allah ndiarigne késsé leu…Yalna xaam xaam bi yokk tei borom bi wéroul bate bi.Dieureudieuf Serigne Cheikh!

Astou Gueye
Astou Gueye
4 années il y a

Hakaza ndekane si bepp sokhna

Abo Madiyana
Abo Madiyana
4 années il y a

Machallah, jerejef.
Amna solo lool

Yacine
Yacine
4 années il y a

Dieureudieuf Mouride.

Khar
Khar
4 années il y a

Mashala kaddu yi am neu solo am neu gñeurigñ djeureudieufff Mourid🙏🏽