Leeral Jazaa’u Shakuur (2)

Al-Habdul Xadiim
29/08/2022

Bismillahi Rahmaani Rahiim

Lii mooy ñaareelu xaaju Jazaa’u Shakuur te mooy sunu xaaj bu mujj. Sëriñ bi di di fi wax lenn ci coono yi mu daj Dakar, ca gaal ga. Ci néeg yu xat yi ñu ko daan duggal.

Wax na fi it wax yu yéeme ci may yi mu jëlle ci tagg gi mu daan tag Yonent bi Alayhi Salaam. Di xamle it ne tagg gi moo ko may « Kun », moo yar léppam, moo ko jubal ak yeneen ak yeneen.

Dafa di nag moom Sëriñ bi, bis ba mu wone ginnaaw réewam jëm fu sori ngir liggéeyal Yàlla Subhaanhu ak Yonnentam Alayhi Salaam, tiisoon na lool ci njaboot gi. Lu bari jaxasoo, ñu bari jaaxle waaye mu ànd ak ngoram, fitam ak jomam fas yéene defi dëgg-dëgg AbduLaahi ak dëgg-dëgg Xaadimu Rasuul ak xeetali mbindéef yi. Ba liggéey bi matee, la mu doon jaay jar, Boroomam gëram ko. Daa woo ñoñam ci santaleko Yàlla ci xéewal yi. Ngir lépp lum am ci tukkeem bi la ko amee.

« شُكْرُ إِلَاهِي حَانَ فِي تُرَابِي بَعْدَ.جَمِيلِ الصَّبْرِ فِي
اغْتِرَابِي »

« Sant Yàlla nag jot na fii ci sama suuf ( sama dëkk), ginnaaw muñ gu rafet gi ma muñ ca sama tumrànke ga »

واجعل طعامي و شرابي يا كريم ذكرا و شكرا و ثوابا لا يريم

Yaw Yàlla mu tedd mi Yàlla nga def samaw ñam ak samag naan muy ak tudd Yàlla, di ak cant téy tiyaaba juddul dakk mukk.

ومن يلقني للجحد في البحر ذاقلي
فقد جا ءني في البحر جو د المكرم

Ku may sànni ca géej ga ngir weddi Yàlla boole ko ak ëmbëlma ak mbañeel tamit, Tabbug Yàlla miy terle di ma ñëwal ca géej ga rekk.

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires