Leeral Huqal Bukaa’u

Al-Habdul Xadiim
29/04/2022

Bismillaahi Rahmaani Rahiim Sang yi … Ku ci nekk day am leer gu toll ne leerug jant bi fu mu man a jëm. Su ko defe képp kuy leerloo ci moom day am lu rëy. Day mel ne ku gisul mbindéef yi ngir jublu Boroomam ak i leeram yu bari ak i mbóotam.

Day man a far bépp tilim-tilim bu nekk ci ab xol, ni kuy fóot di raxasee ay yëre ba du am sobe. Loolu moo tax ñu mel noonu, képp kuy toog ak ñoom doo texeedi ndax ñoo lay texeel. Bépp murid bu leen di sopp wala mu leen di ligéeyal wala mu leen di jox, texe na. Roy ga ñu daan roy Yonent bi sala Laahu tahaalaa alayhi bi aalihi wa sahbihi wa salama tax na ñu am ay daraja yu kawe ak i ndam yoo xam ne xalima manu leen a bind, làmmiñ manu leen a nettali !

Al-Habdul Xadiim
29/04/2022

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Yacine
Yacine
2 années il y a

Amatina solo Maa Shaa Allah. Yalla nanou yalla ndimbali bagnou bokk thi Khaite diamoukatou yalla yoo yai. Amiiine si niane yeup.