Fii dana fi feeñee farlug Sëriñ bi ci jëfe ndigalu sunu Boroom, ak xam gi mu xam ni àdduna jaaruwaay la.
Naka noonu terangay Alxuraan ci ñu koy jàng ak tawfeex gi ci Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu am.
Su ko defe lii di nu soññi ci xam ne àdduna du kërug sax, ba tay di nu xamal ne lu nu fonk Alxuraan doyul
Li Seriñ bi bégg fawwu mu am
Sikkuwut