gear Paramètres Push
chat
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Ndegam bëgg a nga àgg ci Yàlla, du man a ñàkk nga am yóbbal gu réy gu lay tax a àgg ca moom.Dees na ko xame ci Téere bii nga xam ne dafa « rafet ba dàq wurus ». Al-Habdul Xadiim 08/07/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Di nga fi dégge ay dénkaan yu fees deel ak njariñ, lépp nag jëm ci jullit bi rawatina murid bi. Te mel na ne tënk na lu bare bari ci ñaari Téere yi nu mujjee yaatal te mooy Maxaaliqu-Niiraan ak Zaadu Zawii-Tahalumi. Al-Habdul Xadiim 20/06/2020
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Ci buntu bi lanu fas yéene tejje Zaadu Zawii-Tahalumi. Di nga fi dégge ay àddis yu bari yuy wax ci mbiri xiif ak jeexital yu am jariñ yi muy def ci ruuhu dóomu aadama bi. Jàppandal la ci sàkku xam-xam, ak yar sa bakkan. Te kenno la ci tasawuuf! Di nga fi […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Ndeke kuy sàkku Xam-Xam, war na nga xam luy jublu gi ak am melokaan buy taq ci yaw ngir jariñu gën a jàppandi. Ba tay, xam-xam leer gu réy a ngi ci bu lépp àndeek seelal ak rafet yéene. Ndeke sax fàww nga yar sa bakkan, dëddu àdduna, tënk say bànneex te […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Di nga fi xame dooley xam-xam. Ba tey, ndegam bëgg nga ràññatle sunna ak bidaa, boo teewloo ndénkaan yi dina la jariñ. Al-Habdul Xadiim 03/06/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim Ndegam bëgg ngaa xam kennoy Tasawuuf, ak yan jikko lay def ci nit man nga teewlu lii. . https://al-habdul-xadiim.com/wp-content/uploads/2020/05/VID-20200528-WA0009.mp4.mp4 Al-Habdul Xadiim29/05/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Di nga fi xame ne li jig doomu aadama mooy mu yar ay cëram ci toppndigal ak bàyyi tere ba ci xelam sax war na ci moom mu tënk ko ci xalaatyiiw. Loolu nag ite ju réy la. Yal nanu ko Yàlla defal! Lekk lu lewitam ndeke man na yombal lu […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim.Di nga fi xame sunuy ñent noon ak gànnaay yi ñuy jëfandikoo. Nga wara xam nooy def ba xeex ak ñoom, nangu seen i ngànaay te dugal leen ci seen i kaso. https://al-habdul-xadiim.com/wp-content/uploads/2020/05/VID-20200521-WA0010.mp4.mp4 Al-Habdul Xadiim 21/05/2020.
Bismilaahi rahmaani rahiim Sëriñ bi Xaada lahu laahu Maxtaara lahu moo fiy xamle ni nit ki wara melokaano bu dee sàkku Xam-Xam. Dana fi feeñee njariñal xam-xam ak teggin ak yi ci aju. Sëriñ Alhaaji Mbàkke moo ko leeral ci wolol. Yal na nu Yàlla defal dégg ak topp barke weeru koor gi. https://al-habdul-xadiim.com/wp-content/uploads/2020/05/VID-20200517-WA0020.mp4.mp4 Al-Habdul […]
Ap dog Ni ñuy gëmé dogal bi moodi ñu gëm ne lepp lu am suñu boroom mooko amal ci kàttanam ak ub xam-xamam, moo xam lu nëbbu la wala muy lu feeñ, wala aw yiw wala aw ay, melné toppu yoonu yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salam wala topp […]