Bismilaahi Rahmaani Rahiim
Ginnaaw nuyoo gu am solo gi mu nuyu ay mbokkam, ay dëkkandoom ak ay kilifaaam dafa daaldi leeral lan mooy lu BAAX.
Mu mel ne lépp daf koo tënk ci ag tabe gu tégge ci ag nite. Naka noonu mu wone ci aw yoon. Waaye noonu it la waxee xéewal yi nekk ci joxe. Xamle fi itam li gën a doon farata ci joxe, ni lu baax itam du lu nuy làmb, danukoy toxal, jëlle ko fu wér. Soññee na itam ci sutura boo dee joxe, ak def ko te Yàlla tax ba noppi bañ a ndamoo dara ak sa jëf lum réy-réy.
Al-Habdul Xadiim
30/06/2021