Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (5)

Al-Habdul Xadiim
30/07/2021

Bismilaahi Rahmani Rahiim

Dénkaane bi da ko def di ci soññi góor ñi ci gën a muñal, refetal ak yëram soxna yi. Ci noonu lay fàttali lu bari luy waral jëfe laabire gi gën a yomb. Ba tay mu xamle ci ne, di digal sa soxna ak di ko tere day déllu waat ci meloy jullit bi rekk. Nooni itam la fàttale soxna yi ne, war na ci ñoom ñu góor-góorlu ci ag mbaax ngir man a am doom yu baax.

Mu mel ne kon, ku ko teewlu da nga ci jële njariñ lu yaatu ñeel sa jëmb ji ak sag njaboot. Te lépp day déllu waat ci àddisi Yonent bi salla Laahu Tahaala aleyhi bi Aalihi wa Sahbihi wa Salama.

Al-Habdul Xadiim
30/07/21

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
THIAM
THIAM
3 années il y a

Masha’Allah mouride bi yallah na xam xam bi yokk