Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (8)

Al-Habdul Xadiim
17/08/2021

Bismilaahi Rahmaani Rahiim

Ginnaaw ba mu fàttalee boppam ki mu doon, te mooy ab liggéeykatu Sëriñ bi. Dafa daaldi xamle ci bu leer ni Yàlla Subhanahu Wa Tahaala bëggee ñu jaamu ko, ak ni mu ko ñore, mu daal di fàttali baakaar yu mag yi mat a moytu mel ne jëw ak fenn ak doxalin yu suufe yi mel ni werante.

Ci noonu lay xamle gàttug àdduna kon mu war kon nu wara yokk sunub jaamu,  tey liggéeyal Sëriñ bi, ak gën a fonk Xasidaam yi. Waaye diggal na fi itam ni aju ci moom wird wu gàtt te bari njariñu daal di baalu hàq ñépp ak baal ñépp hàq ni mu ko baaxo defe.

Yàlla nanu Yàlla defal tawfeex!

Al-Habdul Xadiim
17/08/2021

share Partager

S’abonner
Notification pour
guest
4 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Cheikh Bathie THIOUNE
Cheikh Bathie THIOUNE
3 années il y a

Macha’Allah

Yacine
Yacine
3 années il y a

Dieureudieuf si fatali bi. Amna solo lol. diadieuf Mouride.