
Ci ñaarelu xaaj bi dees na fi àndi ñaan yi Sëriñ bi ñaan ci Téere bi ak li muy ñaan ci Boroomam ak di ko ñaanal képp ku jàng Téere bi.
Mu di fi dénk taalube yi ay teggin, boole ci di leeral luy teggin, soloom ci nit ki ak ni mu gànjaroo. Mu mel ni xeeti jëf yi bu ci ne am na nees ko war di defe ngir mu gën a jàppandi, gën a baax. Xeeti ànd yépp naka noonu.
Yal nanu Yàlla defal ay teggin yu ñu gëram barkeb Seexul Xadiim.
Diadieuf Mouride. Amatina solo lol.