
Fii Sëriñ Alhaaji daf fiy leeral dénkaaney Sëriñ Tuubaa ci sàmm sa bopp, am kersa ak di wormaal nit ñi.
Njariñul nuyoo, teggini nuyoo ak ay jeexitalam dees na ko fi fésal. Naka noonu yar say gët, màndu, xam kooy àndal, xam kooy roy dina fi leere.
Ay wax yu am solo te bari ngariñ dong moo fiy féeñee yal nanu Yàlla takkaale jikko yu refet yi barkeb Borom Tuubaa.