gear Paramètres Push
chat
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu yaatu, te sell jëm ci mbokki jullit yi dafa daaldi xamle ne Sëriñ bi mat naa fonk, dëkkam bi it di Tuubaa mat naa wormaal lool, rawatina Jumaa ji ak li ko wër ndax Malaayika yi duñu fa géj, leer yi di balloo fu ne. Mu fàttali bu wér […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Ginnaaw ba mu nuyoo ci anam gu matale. Dafa daal di bàyyiloo xel mbooleem kuy jullit ñu farlu ci teewlu sunu Boroom ci sunuy mbir yépp. Ndax sunu Boroom mi ngi gis sunu lépp, te dees koy wara xalam. Di tuub fuñu tool, di ko fàttaliku ngir mu ñuy fàttaliku. Kon lépp […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Dénkaane bi da ko def di ci soññi góor ñi ci gën a muñal, refetal ak yëram soxna yi. Ci noonu lay fàttali lu bari luy waral jëfe laabire gi gën a yomb. Ba tay mu xamle ci ne, di digal sa soxna ak di ko tere day déllu waat ci meloy […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu am solo gi mu nuyu ay mbokkam, ay dëkkandoom ak ay kilifaaam dafa daaldi leeral lan mooy lu BAAX. Mu mel ne lépp daf koo tënk ci ag tabe gu tégge ci ag nite. Naka noonu mu wone ci aw yoon. Waaye noonu it la waxee xéewal yi nekk […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Fii daf fiy leeral mbiri ñenti noon yi te mooy bakkan, bànneex, saytane ak àdduna. Muy wax itam lëkkalo gi nekk ci diggante bakkan ak bànneex. Xamle fi itam nees di def ba noot leen. Naka noonu, la fi leerale lu aju ci bëgg a àdduna, wax na fi itam màndargay mucc […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Lii ab dénkaaane la bob ma nga bàyyikoo fa Sëriñ Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim. Mu ciy soññee ci gën a farlu ci jaamu Yàlla. Tey gën a fonk Alxuraan ak Xasiiday Sëriñ bi. Mu xamal nu ci itam ni war na ku ne ci nun sàkkul boppam waxtu yoy dana ci tuubal […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Lii ab Dénkaane la bu gànjaru, Sërin Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim moo nu ci doon fàttali li nu àndi ci kaw suuf, te mooy jaamu sunu Boroom. Mu fàttali nu fi itam ne war na ci nun, nu yittewoo tuub, xamal nu itam ne Alxuraan ak Xasiida mat naa fonk lool, te […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Nu fas yéene matal li desoon ci bayyit yi nga xam ne Sëriñ Alhaaji Mbàkke àndi na ko ci Dooley Mbidum Sëriñ Tuubaa. Muy ay bayyit yoo xam ne ku ko dégg di nga ci jëlle njariñ, sag pas-pas ak sa mbëggeel itam ci Sëriñ bi man na ci yokk bu wér. […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Dooley mbidum Sëriñ Tuubaa ci lawhul Mahfuus, ni ko fa sunu Boroom dëggarale dina yéem ku ne. Saytane itam day daw mbidam ndax da koy gàcceel, di bégloo Malaayika yi aleyhimu salaam ak jigéeni àjjana. Ay Xasiidam dafa mel ne xare, moom ak jëfi waa Badar ñoo yem, dafay texel murid bi […]
Al-Habdul Xadiim 23/11/2020