Dénkaane bu jëm ci Seex Mabaabu Géy ak yeneeni dénkaan yu jëm ci bépp murit

Bismilaahi Rahmani Rahiim. Di nga fi dégge ay dénkaan yu fees deel ak njariñ, lépp nag jëm ci jullit bi rawatina murid bi. Te mel na ne tënk na lu bare bari ci ñaari Téere yi nu mujjee yaatal te mooy Maxaaliqu-Niiraan ak Zaadu Zawii-Tahalumi. Al-Habdul Xadiim 20/06/2020

Dénkaane bu jëm ci doomi mbokki Sërin Tuubaa(14).

Bismilaahi Rahmani Rahiim.  » Maa ngi leen di dénk xam, ak jëfe ak tegginu te bàyyi fo. Xam-xam saa su ne luy bégloo lay àndi waaye réer luy lor rekk lay àndi. Ñàkk teggin nag day waral sori Yàlla. Ñàkk jëfe li nga xam day waral alku. Barim po day xañe ay yiiw.Kon deeleen farlu […]

Xiif ak àddis yi ci rot; ak naka la xam-xam yi gënante ci Zaadu Zawii-Tahalumi(3)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Ci buntu bi lanu fas yéene tejje Zaadu Zawii-Tahalumi. Di nga fi dégge ay àddis yu bari yuy wax ci mbiri xiif ak jeexital yu am jariñ yi muy def ci ruuhu dóomu aadama bi. Jàppandal la ci sàkku xam-xam, ak yar sa bakkan. Te kenno la ci tasawuuf! Di nga fi […]

Teggin yi war ci kuy jàng ak solos xam ak jëfe ci Zaadu Zawii-Tahalumi(2)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Ndeke kuy sàkku Xam-Xam, war na nga xam luy jublu gi ak am melokaan buy taq ci yaw ngir jariñu gën a jàppandi. Ba tay, xam-xam leer gu réy a ngi ci bu lépp àndeek seelal ak rafet yéene. Ndeke sax fàww nga yar sa bakkan, dëddu àdduna, tënk say bànneex te […]

Dénkaane Sëriñ bi ci Zaadu Zawii-Tahalumi(1)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Di nga fi xame dooley xam-xam. Ba tey, ndegam bëgg nga ràññatle sunna ak bidaa, boo teewloo ndénkaan yi dina la jariñ. Al-Habdul Xadiim 03/06/2020

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR