Ñaari jant fa kër Señ Hamdi Mustafa.

Bismilahi rahmani rahim.

Sunu Sang bi ñu gëna xam ci turu Sëriñ Séex Faal Baayu Goor, mi ngi gané adduna Dakar ci att’um 1918 ci bisu Aljuma.

Turam dëgg móodi Séex Ibràhima Faal, ñu duppé ko Maamam mi nga xam ne moom la njëkk am ci sët bu goor. Waayjuram wu goor mi ngi tuddu Sëriñ Muhamadu Mustafaa Faal, wayjuram wu jigéen nak Soxna Xadijatu lañukoy wax. Ci ak ndawam lañu ko jox Sëriñ Tuuba Xaada lahu laaha maxtaara lahu mook rakkam ju ñuy wax Sëriñ Muhamadu Aminata Faal mi gané adduna 1918 itam, cosàno Ganjóol, ndeyam tuddu Soxna Aminata Ñang, mu dalal leen Alqur’an.

Ganaaw ga lañu léen joxé fa daaray Sëriñ Abdu Rahman Lo ñuy jang ci ku ñuy wax
Sëriñ Yuusufa Lo ngir motali séen’um Alqur’an. Waayé njang mi nak mi ngi maté ci loxoy Sëriñ Moor Taala Faal mom Maam Séex. Jëllé nañu ci Sëñ Dàwuda Faal mu bind ne : « Sëriñ Séex Ndigal Faal yorna ab bataaxel bob, la ca ne, day mbind’um Sëriñ Moor Taala Faal jëm ci magam Sëriñ Muhamadu Mustafa Faal », mu naako « Sëriñ Séex Faal matal na jangam ci talaata ji, te yëggal ni Sëriñ Muhamadu Aminata Faal dana matal moom it bu talaata déllu sé.

Amà lu ajju ci njangum xam-xam mi, ñoo ngi ko defe ca dëkk buñu naan Gorea , moo
nékk Mbirkilaan, ba nopi jiggé Singeré. Sëriñ Dàwuda Faal wax na ni ca dëkk boobé la Sëriñ Basiiru Faal Alqur’an, Sëriñ Ngunda Faal, Sëriñ Móodu Mbénda fa la ñu jangé Alqur’an.

Ganaaw ba suñu ñaari sang yi bindée Alqur’an jébbal na ñuko séen baay mu ne léen joxi leen ko Sëriñ Muhamadul Mustafa Mbàkke, jamono jóoju mi ngi woon Tayyif.
Señ Séex Faal nak di wey ci ndigalu Sëriñ Séex Mustafa Faal ba ni mu koy yabbalé Daaru Faal tollu ak juróom ñaari kilométar diggam ak Gosàs. Wayjuram wu jigéen mujjuk dundam fala ko defe, te sax foofée lañu ko dénc.

Ci att’um 1950, ca la Bàyup goor toogé ci xilaafa wayjuram wu séll ma, boobé mi ngi am fan’wéeri att ak ñaar.
Sëriñ Muhamadu Aminta Faal nak mi ngi took ci jotàyu Séex Ibràhima Fall ci att’um 1984 ginaaw biko Bàyam Señ Abdu Shàkur dooné. Mu melni kon mooy sët bi njëk yilif baay-faal yépp. Wax na ñu ni, ci att’um 1984 ci la Bàyub goor waaccé( wàccée ab) ligéey , moom jambar ji , ci wax yu am maanaa yi té bari njariñ waayé bateymoom jambar ji, ci ligéey.

Li key firndéel móodi…
Book na ci limu daan wax :

• Boo bëgée jige Yàlla da ngay jang Alqur’an te muy dëgg ci yaw.
• Boo bëggée wilaaya da ngay jang Qasida

• Boo bëggée dëgg dangay jaar ci aw yóon

• Boo bëggée wërsëg da ngay joxe àddiya

• Gëm moo mën xam-xam
• Gëm moo mën am-am
• Gëm moo mën fit

• Gëm moo mën daraja

• Gëm moo mën ay at

• Gëm moo mën ab juddu
• Gëm moo mën ludul moom

Li mu daan wax la ay jëffam firndéel, ndax ngëm gu léer, fit ak jom la boolé won ci bépp sumb.

– Att’um 1959 fékkna mu sanc Saam-Faal, def fa Daara Tarbiyah ju mak, sanc 12 dëk yuko wër, jox ko ay rakam. Bokk na ci dëk yooyé : Saam Sèk mu Sëriñ Idaly Fall, Tawfeex mu Sëriñ Móodu Mbènda, Dàru Saam mu Sëriñ Ngùnda Faal, Tuuba Saam Kër Sëriñ Mustafa Bàyu Goor (taawam), Dàru Xitma kër Señ Séex Faal Xatàba, Njaasam kër Sëriñ Tàlla mu Señ Móodu Mbènda, Tuuba Bélel kër Baay Daam Jóob mu Sëriñ Mustafa Fàti Kalla, Ndigal Faal mu Sëriñ Séex Ndigal Faal.

– Att’um 1960 lamu def ci ‘’ carriérou Ndock’’ ku ne xam nako. Ndax ‘’carrière’’ boobu yombal na muriid yi tabaxu Jumahi Tuuba. Jële na ñu ci mak ñi andoon ak
Sëriñ Séex Faal ci ligéey ‘’carrière’’ bi ñu wax ni « Xéer bi ñu samp ‘’fondement’’
soroor bu mag bi (ñu dupée ko Lamp Fall) Sëriñ Séex Faal moo ko féeñal ba noppi
gasko moom ak mboloom.

Señ Séex faal nak mi ngi fiy bayyiko 11 mai 1984 ci att’um Tubaab di 9 fan i Baraxlu ci wéeru wolof.


Jambaru Xéelkoom ja nak, jëwrin ju mag ji, nuroo woon lool ak Señ Abdul Ahad Mbàkke, ba ci colin bi, dëdu na dunya att’um 2006. Yalna ñu Yàlla feyal Sëriñ Muhamadu Aminta.

Lii mooy li ñu yéene woon xamlé ci ñaari jant yi. Sant na ñu lool Señ Dàwuda Faal mi ñu yombal gëstu gi. Yalna ko Yàlla dolli taxawu biir ak biti Barkép Lamp Faal !

Al-Habdul Xadiim

Dakar, 27/10/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
3 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Xitma
Xitma
4 années il y a

Jërëjëf
Ligéey bi am na solo lool
Yalna léen Yalla fay

Ahmadou Bamba NDIAYE
Ahmadou Bamba NDIAYE
4 années il y a

Machallah mouride, pastef, yalna borom bi nangou liguéy bi thi barkéep cheikh ibra

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR