Kan Mooy Sëriñ Shuwaahibu Mbàkke?

Doomi Soxna Maryaama Jaxate la ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu.
Ci wéeru koor la gane àddina, jëmb ju màgg la woon, ragal Yàlla lool te ràññeeku ci. Dundam di njariñ gu yaatu te bari solo.

Mi ngi gane àddina bisub talaata 1335 ci gàddaay gi, toolo ag 17 juin 1917 ca Njaaréem ci 5i fanu koor. Bañu yegle Sëriñ bi dikkam ci àddina daf ne neen négg ba dog jot, ñu doog di ko jox ñam. Seex Muhammadu Lamin Jóob dagana la fa yabal mu kox ko aw tur. Wayjuram wu jigéen ji di Soxna Maryaama Jaxate, doomi Sëriñ Móodu Asta Jaxate la. Mu bokk ci askan gu ràññeeku ci mokkal Alxuraan, ci ag jub ak nango jaamu Yàlla. Soxna Maryaama moomu moy wayjuru Seex Abdul Ahad itam. Soxna ci nag ba miy wuyu ji boroomam daa fekk Sëriñ Shuwaahibu tool ci li ñuy wax nàmp. Sëriñ bi digle ñu denc ko Tuubaa te Seex Mustafaa taxawu ko.

Sëriñ bi moo ko dalal jàng, jox ko Sëriñ Amsatu Jaxate nijaayam, ngir mu jàngal ko. Mu bokk fa nekk ak mbokkam ya Sëriñ Saalihu, Sëriñ Abdul Ahad ak Sëriñ Abdullaahi Jaxate. Ku ñuy wax Sëriñ Alhasan Jaxate moo ko fa doon jàngal.

Daan na faral di ànd ak magam ja Sëriñ Saalihu di siyaar ci Sëñ bi Njaaréem. Leeg-leeg ak nammeel jàpp ko mu jàkkaarloo ak Sëñ bi di ko xool rekk. Ba Sëñ bi naan ko jublul xibla. Di ko ataayaloo, di ko liggéeyloo ngir jublu ci Tarbiya ko ci xam teranga, jàng ak jàngale Alxuraan.

Sëriñ Shuwaahibu ci nekkub Sëriñ bi la mokkale Alxuraan, li dafay tegtale ne ab jàngam daa gaaw lool. Waaye ba mu binde kaamil Seex Mustafaa la fi fekk mu jox ko ko.

Nit ku bari woon lumuy jaamu Yàlla la, ragal ko lool te nangoo sellal. Bari xam-xam, set-wicc nag, néewi wax lool te bari jàmm. Dafa farlu woon lool amug xàmmee, bari yërmande, fonkon lool di fàggu garabi doktor yi di ko denc. Nit ku tabbe la woon, daf daan dimbale, daawul woon tas yàkkaar. Bu guddi masaan a jot, auto yi rang mu yable fu ne di fa seedale ag dund. Bari woon sutura rawatina buy joxe. Dalal na ñu bari ci am jàng, te1945 la tàmbalee jàngale.

Daa nekkoon ci li ko war te bàyyi boppam ak Sëriñ bi. Ku amoon yërmande la ci gone yi. Sunu Boroom defoon bàrke ci jàngaleem. Ku ko masaan a gis sopp ko.

Bëgg a lu baax lool. Mas naa wax Sëriñ Amsatu damaa bëgg a nga wax ma ba ma gane àddina ba leggi ñaata julli moo ma fi raw. Te boobu waragu ko woon. Waaye teewul mu fay lépp. Góor Yàlla tigi la woon. Sanc na ay dëkk, sàmpi Daara, yare na defare na. Bind na ay Téere xamle ci, bokk na ci « Xuratul Hayni », « Naylul Awtaar », « Usuulu Tasawuuf », « Buxyatil Muriidiina », « Miftaahul Munaa » .

Yalla na ko Yàlla dolli ay ngëram fa mu nekk te taas nu ci bàrkem, njabootam gudd fan lool te am wér ak ngërëmal Seexul Xadiim.
Sëriñ Shuwaahibu Ndooy mi tax nu man leen a jukkil tomb bii ci dundug Sang bi Yàlla na fi yàgg te wér te sax ci ag taalube barkeb Boroom Madiyaana.

Al-Habdul Xadiim
18/04/2021

S’abonner
Notification pour
guest
10 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Rassoul Kane
Rassoul Kane
3 années il y a

Masha Allah Mourid santati nagnou boubakh Yalnassi Yallah swt doli ay ngënèl

Wadji Moustapha
Wadji Moustapha
3 années il y a

Eukaza
Amna solo lol
Yalna yallah fayal gnuko
Tass gnu si barkem

Saliou
Saliou
3 années il y a

Machallah da bay ler na lole

Baye Mor
Baye Mor
3 années il y a

Jaangéen jëf yàlla ngéen fi yàgg diko gën a man ci barkeb Ku Tedd Ki

Bounama Mouride niang
2 années il y a

ManchaAllah murid lii moom am na solo lool sakh…yalna sama botom barkel liguey bi barkep mafatihul bichri

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR