
Bu loolu jàllee nanga xam ne Yónente yi HS, am na ñatti melo yu war ci ñoom: “muy dëggal ak bañ a def lu haraam ak lu ñu sib ak jottali lañu leen yónni”.
Am na ñatt yoo xam ne daa jomb ci ñoom: “mooy fen ak def lu haraam ak lu ñu sib ñàkk a jottali lañu leen yónni”.
Loolu moo tax saa soo waxee ne ab Yónente dana weccee la ko sunu Boroom yónni woon te tay ko dëggal da koy dàq, ( ndax loolu fen la ) kóolute itam dana ko dàq, ( ndax loolu dafa haraam, Kóolute mooy ñàkk a def lu haraam ak lu ñu sib ) jottali itam dana ko dàq ndax loolu du ag jottali.
Saa soo waxee ne ab Yónente dina dolli te tay ko, dëggal moo koy dàq, ( ndax fen la ) ak kóolute ndax lu araam la, waaye jottali du ko dàq ndax jottali na ba yokk leneen.
Saa soo waxee ab Yónente dana weccee la ko sunu Boroom waxloo wax leneen, ci ag njuumte dëggal moo koy dàq, ( ndax loolu fen la ) ak jottali ( ndax loolu nëbb la ) waaye kóolute du ko dàq ndax araamul.
Saa soo waxee ne ab Yónente dina nëbb dëgg te tay ko, kóolute moo koy dàq ( ndax daa haraam )Ndax nëbb na la mu waroon a jottali waaye dëggal du ko dàq, ndax waxul dara ba muy doon dëgg walla fen.
Saa soo waxee ne dana dolli ci kaw ag njuumte, dëggal moo koy dàq ( ndax fen la ) waaye jottali du ko dàq ndax jotal na ba yokk ca leneen, kóolute itam du ko dàq ndax nekkul lu araam.
Saa soo waxee ne ab Yónente dina wor ( dina wuute ak ndigali mel ni njaaloo walla xool jàmbur bu jigéen) kóolute moo koy dàq ndax lu haraam la waaye dëggal du ko dàq ndax du ay wax ba fen di ci am, jottali itam du ko dàq ndax du nëbb dëgg.
Saa soo waxee ne ab Yónente dana nëbb dëgg ci kaw ag njuumte, jottali moo koy dàq (ndax nëbb na) waaye dëggal du ko dàq ndax waxagul bay fen, kóolute du ko dàq ndax doonul lu araam.
Lépp loo xam ne bu dalee ab Yónente duñu ko daw, duñu ko xeeb, man na koo dal, man na koo bañ a dal.Mel ni tawati sibiru ak mar ak xiif ak sonn ak di liggéey ñu koy fay ak fàtte lu dul li leen Yàlla sunu Boroom Yónni. Waaye lu mel ni tëx walla gumba walla ndoxum siti walla gaana ak yu ni mel du leen dal. Sunu Boroom SHW da leen a teral ñu am matug xel ak matug yaram, duñu nekk ñuy sébéñ ay der walla ñuy nekk ci liggéey yu suufe.








