
Sëriñ Isaa Jenn mooy doomi Sëriñ Ibraahima Jenn ak Soxna Maryaama Jóob. Di waa Kajoor, mi ngi gane àddina ci atum 1863 walla 1865. Li gën a woor daal moo di moom ak Maam Cerno ñoo maase.
Sëriñ Isaa Jenn mooy koo xam ne amul woon benn soxla bu dul bu Sëriñ bi. Jàng na Alxuraan, jàng xam-xam sóobu ag mbaax njëkk muy setti Sëriñ bi. Tàggaar la bàyyikoo ñëw ci Sëriñ bi, boobu dëkk bu nuy wax Mbal la ko fekk indaale ñaari mbalaani cawali jox ko ko, ànd ak xaritam. Sëriñ Isaa daaldi jébbalu ci Sëriñ bi. Sëriñ Tuubaa laaj na ko it nu xaritam bi tudd. Seex Isaa ni ko Sowri Jóob. Sëriñ bi daaldi ne AbduLaahi Xayrun min Suuri. Mootax nu daa ko wax AbduLaahi Jóob Sowri. Sëriñ bi laaj Seex Isaa lu xaritam bi bëgg. Mu ni Sëriñ bi, sama xarit bi itam daa bëgg jébbalu. Mu ne ko boole naa ko ak yaw.
Ci benn jotaay bi, Sëriñ Isaa ne ko, damaa bëggoon di liggéey. Sëriñ bi ni ko kan nga gën a jege ci fere yi ? Mu ni ko Masàmba Jóob. Sëriñ bi ni ko man nga def ni moom di yoneesi. Seex Isaa ne ko awma ku ma yoni. Sëriñ bi daaldi koy jox ab tookoor gu def xaal ni ko bay ko, te bul ko weesu. Ba mu demee ba àgg ci góob gu mujj gi, Sëriñ bi daa woo ku nuy wax Sëñ Umar Géy, ni ko demal wool ma kee di bay, ne ko mu wuyusi ma. Mu fekk Sëriñ bi yor daa ak xalima. Mu laaj ko turu ndeyam ak baayam. Laajaat ko la mu ko waxoon. Te mooy koo gën a jege ci fere yi ? Mu ni ko Masàmba Jóob. Sëriñ bi ni ko man nga def ni ñoom di yoneesi. Seex Isaa waxaat ko lam bëgg ci liggéeyal ko. Sëñ bi yeesalaat la mu ko waxoon. Seex Isaa daal di dem Tàggaar. Sëriñ bi def ci moom la miy def ci moom. Ñu bari topp ko.
Ba Sëriñ bi it di nekk Njaréem, la fa nekkoon ci ay dëkkuwaay, mbaar yi, sing yi ak yeneen ak yeneen lu nit di aajawoo bu nekkee cib dëkk li ci ëpp jëfug Sëñ Isaa Jenn la.
Keroog ba Sëriñ bi jotee ndigal ci Yàlla Subhaanahu wa Tahaala jaarale ko ci Yonent bi Aleyhi Salaam ngir taxawal Jumaay Njaaréem, Sëriñ Tuubaa daa woote wax ne ci yoxoy Seex Isaa la ko bëgg a teg. Juróom benni weer liggéey bi taxul mu tàmbali ndax dafa am ñu ci àndul woon. Sëriñ bi woote waat. Seex Isaa ni ko « su fekke Yàlla moo la ko sant jaarale ko ci Yonent bi Aleyhi Salaam nga digal ma ko, ku tee ma def ko di naa la boole ak moom tabax ». Keroog la Sëriñ Mandumbe ne Seex Isaa bul ma waxati Mbàkke dee ma wax Fofana ba liggéey bi yeg. Te dee ma ci jox ndigal. Seex Isaa lim def mooy képp ku sant Mbàkke, Sëriñ Mandumbe ngay jox sag jaayante ci liggéey bi. Képp ku ajjuwul ci moom nga jox sag jaayante Sëriñ Bàlla Faali Jeng.
Seex Isaa jiite liggéey bi dara taxawul Noor ak Naweet.
Bokk na ci ag yéewuteem mooy xam na ni Sëriñ bi da daan am ay gan yu bari,ñuy jóge fu nekk, te daan na xam ni dina war ñu di leen ganale. Daf daan bàyyi xel loolu bu baax, di ci def alalam.
Ku xereñ la woon itam ci anam gi ñu wara sañcee ay dëkk ak nees di ko dundalee te mooy li nuy woowee tay « décentralisation ». Yar, teggin, nite ak ubbeeku ci fépp fu njariñ nekk ci la tarbiyaa ay ñoñam. Dafa di loolu moo doon melloom. Di digal ni mu yar ñu sax ci Lislaam tey teral képp ku baax.
Sëriñ Tuubaa nag teral na ko, defal ko ay may yu bari, gëram ko wax ko, gëram ko bind ko.
Seex Isaa Jenn mi ngi fiy bàyyikoo atum 1948. Yal na ko Yàlla dolli yërmande, njéggal, xéewal ak leer barkeb Seexul Xadiim. Di sant Sëriñ Basiiru Siise mi wéral sunub gëstoo ci dëggarloo ko ci li sëti Seex Isaa Jenn bind ci seen maam. Di leen ñaanal ñoom ñépp ngëramal Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu.








