Miftaahul Xuyóob (10)

Xaaj wi dafay jëm ci mbiri bàmmeel ba tay. Nu ciy xamle ñi nga xam ne dee fu leen laaj ci bàmmeel. Nu ciy xamee ba tay, yërmandeey sunu Boroom, naka noonu sañ-sañam. Yal nanu Yàlla musal ci tiisi bàmmeel.

Jotaayu Texe (7)

Lii ab dog la bu jëm ci Xasiida yi, teewlu gi ci war ak déglu gi, ànd solo si mu làmboo. Naka noonu dina feeñee ci nettali yi ay mbir yu kéemaane ci mayi Sëriñ Tuubaa. Yal nanu Yàlla jubal te baaxal nu Barke Borom Tuubaa.

Jotaayu Texe (6)

Ci xaaj wi dees na fi gën a xamee mayi Yàlla sunu Boroom. Di neen fi gis it ni ñaanlu ci say mbir lu baax la. Moom Sëriñ Tuubaa nag di neen déggee ci nettali bi fonkam Alxuraan ak jibboo ak Boroomam. Yal nanu Yàlla sàmmal sunu Diinee.

Jotaayu Texe (5)

Mbokk mii di Xaadim Ja dafa réer. Boobu ba tay kenn xamul ci moom dara. Nataal wii, noo ngi ko jëlle ci « AESF ». Nuy sàkku ci ku ko man di gis nga jokk limat yi ci nataal bi. Yal na feeñ ci lu gaaw. Amiin ! Ci nettali bii nag dees na ci xame dolleey […]

Jotaayu Texe (4)

Dees na xamee ci nettali yii lu bari ci mayi Sëriñ Tuuba Xaada lahu laahu Maxtaara lahu. Naka noonu déggin wu xóot bi mu am ci lenn ci Aaya yi. Ku xam it mbiri ay taalibeem la, di jëflante ak ñoom ci anam yu wuute. Yal nanu Yàlla dolli tawfeex te dimbali nu ci sant […]

Jotaayu Texe (3)

Dina feeñ ci xisa yi mbiri sàmmoonteeg teegiini sabab moo xam yoy aada ak yoy diine, ci ku man a settantal. Ba tay deef fi déggee lol, dina nu dimbali ci sàkkoo yaru ak yeewu. Yal nanu Yàlla defal tawfeex !

Miftaahul Xuyóob (9)

Li ab tënk la ci mellooy Malaaka yi nga xam ne ñooy laaj ci bàmmeel. Te ñooy Munkar ak Nakir. Raglu nanu lool. Yal nanu Yàlla sàmmal sunu ngëm te bégal nu ci àdduna, barsaaq, allaaxira ak àjjana barke Borom Tuubaa.

Jotaayu Texe (2)

Dees na xamee ci xisa yi yu bari ci mayi Yàlla yi. Nit dina man a xam ay mbir yu nëbbu ci coobareey sunu Boroom. Dina fi feeñee itam dolleey ngëm, dooleey kóolute ak i jeexitalam ci topp ndigalu Sëriñ bu mat Sëriñ. Yal nanu Yàlla saxal ci ag taalube, sàmmoonte, ak ragal Yàlla.

Miftaahul Xuyóob (8)

Fii di nanu fi leeral mellow génnug ruu, ak yi ci aju yépp. Naka noonu dees na fi xamle laaji yi nga xam ne dina am ci bàmmeel ak ginnaaw laaj yi li fay xew. Yal nanu Yàlla sàmm te tënk nu ci lislaam.

Jotaayu Texe (1)

Li ab Téere bu m njariñ lool, ay wax ak i jëfiinu Sëriñ Bi moo ci nekk, nu man ci gindiku ci sunu lislaam ak ci sunu taalibe. Fii nag matug Boroom Tuubaa dina di feeñee ak sunu tawfeex ci ànd ak moom. Yal nanu nuur ci moom barkeb Xasiida yi .

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR