Sëriñ Muhammadu Awa Bàlla Mbàkke, Maam Cerno mooy way-juram. Mi ngi feeñ jamono atum 1896 fa Mbàkke-Bawol. Moo njëkk doon xalifab Maam Cerno itam. Soxna Awa Bàlla Jóob mooy way-juram wu jigéen. Boo toppe ay maamam ci wet googu Koki lay déllu.Yonent bi Aleyhi Salaam leen ko tuddee. Maam Cerno moo ko jàngal, jàngee na […]
Ñi jaar ci ay loxoom bari neen lool. Bokk na ci Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, Sëriñ Mustafaa Saalihu Sëriñ Saalihu Ture. Ku amoon kollare la ak doomi Sëriñ Tuubaa yi, Seex si, ak kilifay yeneen tariqa yi. Amoon tawfeex lool ci Boroomam, di ñaan bu wér muy nangu. Te doyloo woon Sëriñ bi ci bépp soxla.Ku […]