
Sëriñ Muhammadu Awa Bàlla Mbàkke, Maam Cerno mooy way-juram. Mi ngi feeñ jamono atum 1896 fa Mbàkke-Bawol.
Moo njëkk doon xalifab Maam Cerno itam. Soxna Awa Bàlla Jóob mooy way-juram wu jigéen. Boo toppe ay maamam ci wet googu Koki lay déllu.
Yonent bi Aleyhi Salaam leen ko tuddee. Maam Cerno moo ko jàngal, jàngee na itam Tayba-Cekkeen ak Koki.
Ba miy tunt-tank dund na ay jafe-jafe ndax boobu la baayam dénkoon yoon wi ak njaboot gi, te metit gu ne dund neen ko. Kon muñkat la woon bu mag.
Daf daan góor-góorlu ci luy suqali Daarul Muhti. Bokk na ci lu aju ci ndox mi, di jàngaloo nit ñi ak i rakkam, di leen liggéeyloo. Moom moo nat Daarul Muhti, àndi fa làmp yi, ak « poste » ngir bataaxel yi. Te moo joxewoon auto yi ngir ñiy séddale bataaxel yiy ñëw Daarul Muhti. Ba jumaay Tuubaa ji àggee lay doog a tàmbali jumaay Daarul Muhti ci atum 1966. Def fa tali itam, marse ak « école ».
Nit ku yaatu la woon, daan bokk ak ay rakkam lépp lu mu am. Woolu woon lool Sëriñ Abdul Xudóos, jiital ko ci Diine ji ak ci mbir yu bari. Lu waay di joxe itam ci jumaa ji daf daan wax joxleen ko Sëriñ Abdul Xudóos. Sëriñ Móodu mooy ki tegoon tànkam ci Sharia ak cig Taalube.
Moo sanc Daaru Karaatil, Daaru Rahmaan, Saarsaara, Yabal, Madiina. Dëkk yi nag njabootam ñoo fa féetewoon di ko dundal ak di ko suqali.
Ab baykat mu mag la woon ba sax Senghor mas na ko sargal ci loolu.
Nit ku tabe la woon, yaatu xol, gore lool, lewet, laabir. Tabeem taxoon na mu daan wax man de yomb naa àndal ndax nangu naa loo am denc lu ma am nu bokk. Bëggoon Sëriñ Tuubaa lool, daan ko waxtaane boole ko ak xol bu sed ak i jooy. Daf daan wax nit lu muy bëgg àdduna ak allaaxira na wut ag taalube rekk dina ko am.
Doomi Sëriñ Tuubaa yépp a ko wormaaloon, fonk ko lool sax. Moom it mu leen daan xoole Sëriñ Tuubaa, am ci ñoom coffeel lool.
Ku amoon hikma. Daf daan wax ku yaakaar Yàlla sa yaakaar du tas. Daan wax it deeya goo gis ay nit yu juboo te jubuñu ñoo key def. Yal neen juboo nag te Yàlla jubal nu. Bu masaan a wax yii nag boobu dafay fekk mu am ku fo ñëw ngir yu mel nii, Sëriñ bi laabire ñépp ci nees ci war di doxee.
Ku amoon baatin la, daan gis ay mbir yu dikkagul itam. Ku daan ñaan muy nangu la. Amoon yërmande ci ku jaan màtt, jigéen gu toll ci diggante ak ku faatu. Daf daan wax sax bu yi amee ku ma fekk may nelaw na nga ma yee.
Sëriñ Móodu Awa Bàlla ku fonkoon mbokk la itam, daan ko sàmm. Sónn lool ci njabootu Borom Daaru gi, di leen taxawu ci lépp.
Sang bi nag mi ngi fiy bàyyikoo ci atum 1982, Bayti lañu ko denc fa Daarul Muhti.
Lii nu fi bind am na ci lu ñu toxale ci Sëriñ Móodu Géy mi nga xam ne Sëriñ Muhammadu Awa Bàlla moo ko yar, am lu ñu jële itam ci Sëriñ Mbay Géy Sill. Yal na leen Yàlla defal yiw.
Ku dem ci sunub téere « Nitug Yàlla » danga ko ci fekk.








