Leeral Mawaahibul Xudduus (10)

Bis boobee ca ngay gis ku jàq lool, fa ngay gis ku sunu Boroom mere lool, gis fa ku mu gërëm lool.

Ñépp ñoo fay tase ñu baax ñi ak ñu bon, keroog boobee lañuy xam ne, bir yépp sunu Boroom doŋŋ a leen moom, kenn bokkul ak moom dara, bis boobee mooy dëgg-dëggi bis, deel farlu ba la moo yegsi, kon doo fa sonn.

Bari na lool lu ko sunu Boroom di tudd, loolu nag day tegtale ay tiital yu bari, loo gis mu bari ay tur dana tegtale ag màggam. Sunu Boroom am na fu mu ko tudde ba ne “Maliki yawmid diin” maa moom bisub fay ba.Dana mat juróom fukki junniy at, mi ngi tàmbalee bu ñu walee buftu bi walub ñaareel, ba ñépp dekki. Mi ngi yem ci bu ñépp tàbbee sawara ak àjjana.

Su ko defee bis pénc dañu koo séddale ñaari xaaj bu ndaw ak bu mag, bu mag bi mooy loolu ma wax, bu ndaw bi nag saa su nit ki di faatu fa la tàmbalee ak bu nekkee ci bàmmeelam ba keroog muy dekki.Foofee lañu koy laaje, laaj gi mooy dañuy def ruu gi ci jëmm ji ba mu xam la mu xamoon, ñu laaj ko ci mbiri ngëm-ngëm ci Yàlla sunu Boroom ak ci Yónenteem, loolu moo tax nit ki bu faatoo ba ñu suul ko, bay dem dana dégg dàlli ña ko doon suul ni muy yëngoo.Bu ñu koy laaj, dañu koy toogal ca digg bàmmeel ba, seen kàddu yi mel ni ag dënnu, seen gët yi mel ni ag melax, ñuy génne lu mel ni ay ferñent ci seen gémmiñ, niruwuñu jinne niruwuñu malaaka, bindeef yépp dañu leen a ragal ba ci malaaka yi ñépp dañu leen di muslu, yal na nu ci sunu Boroom musal.

( Waat naa ci sunu Boroom ku dugg ci bàmmeel lu dul ag njub du la fa jariñ.Képp ku nekk ci àdduna di dajale alal ba fàtte ëllëg tuskare nga.Ay waay ku nekk ci ay doom ak alal, ba bàyyi wird yi !Deel jihaadante ak sa bakkan kon bu ëllëgee doo am njàqare. Bul topp bakkan bul topp saytaan, kon bu ëllëgee àjjana ju la neex ngay tànn. Deel jàng tey topp, kon danga am tuyaaba. Boo bëggee kawe, deel néewal nelaw )

Sunu sang bi Sëriñ Seex yal na ko Yàlla dolli xéewal, njéggal ak yërmande ak ngëram

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR