Bis boobee ca ngay gis ku jàq lool, fa ngay gis ku sunu Boroom mere lool, gis fa ku mu gërëm lool. Ñépp ñoo fay tase ñu baax ñi ak ñu bon, keroog boobee lañuy xam ne, bir yépp sunu Boroom doŋŋ a leen moom, kenn bokkul ak moom dara, bis boobee mooy dëgg-dëggi bis, […]