Miftaahul Xuyóob (9)

Li ab tënk la ci mellooy Malaaka yi nga xam ne ñooy laaj ci bàmmeel. Te ñooy Munkar ak Nakir. Raglu nanu lool. Yal nanu Yàlla sàmmal sunu ngëm te bégal nu ci àdduna, barsaaq, allaaxira ak àjjana barke Borom Tuubaa.

Miftaahul Xuyóob (8)

Fii di nanu fi leeral mellow génnug ruu, ak yi ci aju yépp. Naka noonu dees na fi xamle laaji yi nga xam ne dina am ci bàmmeel ak ginnaaw laaj yi li fay xew. Yal nanu Yàlla sàmm te tënk nu ci lislaam.

Leeral Miftaahul Xuyóob (7)

Nu wéyal ba tay ci mbiri baamel? Ndax mooy ku ñu def ci pax rekk ? Am romb na loolu. Dees na fi leeral tamit xew-xew gu amoon diggante benn jullit ak ben yéefar gu siiw bob, di neen ci jëlle ay jàngat yu fees dell ak waare. Yal nanu Yàlla musal ci tiisu bàmmeel.

Miftaahul Xuyóob (6)

Fii danu fiy leeral lu aju ci bàmmeel ak dundug bàmmeel ci waxi Kilifa yi. Dees na fi xamee itam ne, sax ci lu baax dara amul njëgam. Naka noonu topp li Yàlla digle ak wattandiku tere yi. Yal nanu Yàlla saxal cig njub barkeeb koor gii nu nekk.

Miftaahul Xuyóob (5)

Ay leeral yu jëm ci li war boroom kër ci soxnaam, yuy gën a dëggaral yi nu doon wax ci ginnaaw. Yii dafay jëm ci xamle lislaam ak yi ci aju, mu mel ni kon jàng manta ñàkk. Yal nanu Yàlla defal xam-xam.

Miftaahul Xuyóob (4)

Ci xaaj wi danu fiy leeral yi nga xam ne dina araam ci jigéen bu am ngàtt mu di ko def, mba muy dem ci ay barab yu mu warul dem. Te war na ci Boroom kër mu xamal ko soxnaaam. Te mu xamal ko it mbolleem lu aju ci wàll woowu.

Miftaahul Xuyóob (3)

Ba tay warteefi borom kër ci soxnaam leen fiy xamle. Mel ne xamal ko diineem ak yi ci aju. Di ko leeralal lenn ci sew-sewi julli ak yi ci des. Daa wara xamal njabóotam itam ak ñi mu yilif seen diine. Yi jëm ci dareeti mbërag, wësin, yooyu yépp daf ko wara xam, te xamal […]

Miftaahul Xuyóob (2)

Ci xaaj wi, dees na fi lim yi nga xam ne war na boroom kër mu xamal ko soxnaam, ñi mu njaboote. Te mooy faratay jëmam ak mbolleem li ci aju, dalle ko ci laab, ponki diine yi la cay farata ak sunna. Di ko waar ngir bëggal ko lu baax ëllag. Te sax « góor […]

Leeral Miftaahul Xuyóob (1)

Li ab Téere la bu am solo jëm ci xamlee nees di yoree sa Soxna ak ay mbir yu jëm ci dundug bàmmeel ak yeneeni yëf. Ku ñuy wax Umar Jóob moo doon laaj Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ay laaj yu am solo. Sëriñ bi bind Téere bi àndil ko ci ay […]

Leeral Fathul Zaahiril Baatin…(2)

Dina fi feeñ lenn ci njariñ yi nekk ci bàyyeek sa lépp sa Boroom, woolu ko bu wóor, ak wéral sab pas-pas ci dëggal saw doxiin sa diggante ak moom. Am na lees ci toftal ci Téere bi, jëm ci leeral luy mag, ak i màndargaam. Akub tënk jëm ci ponki Diine.

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR