Leeral Mawaahibul Xudduus (8)

“Laa Ilaaha Illaahu” mooy : “sunu Boroom aajewoowul jëm ci kenn, te ku ne ak lu ne aajewoo na jëm ci moom”

Saa soo tuddee doylug sunu Boroom SW dananu ci dégge ne ku jiitu la, te day des te niruwul lenn te ku taxaw ci boppam la te amul genn wàññen te day dégg di gis di wax. Ndax yii ma wax bu ko amutoon fàww mu doon kuy aajawoo ku koy mottali walla ku koy sos, walla ku muy dugg ci moom.

Te it dananu ci xame ne du jëf ngir njariñ luy dellu ci moom, ndax loolu bu amee day mel ni aajewoo na kuy amal li mu bëgg.

Naka noonu dinanu ci dégge ne bindeef yépp dañoo dagan ci moom, ndax bu ñu waroon day mel ni dana aajewoo ku koy matal.

Aajewoo gi lépp aajewoo jëm ci sunu Boroom SW dananu ci dégge ne mi ngi dund te am na kàttan, am na nammeel, am na xam-xam, ndax melo yii am gi ñu am moo tax bindeef yi am, bu ñu amutoon mbindeef du am. Bu mbindeef amul dara du aajewoo jëm ci sunu Boroom.

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (7)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR