Leeral Mawaahibul Xudduus (9)

Ki sunu Boroom di Yónni fàww góor lay doon, nit lay doon, doon gor te am xel, sunu Boroom digal ko mu wax nit ña ag bëggam.

Naka noonu kiy am xam-xamub Yónent fàww yooyu am ci moom waaye sunu Boroom da koo yónniwul. Bokk na ci li leen wuutale ba tay, ab Yónente moom day am li ñu waxoon ci ginnaaw, muy “muhjisa” te kii am xam-xamub Yónente du am “muhjisa” moo tax nga man a wax ne képp ku Yàlla sunu Boroom yónni am xam-xamub Yónente ak i sàrtam, waaye du caageene ku am xam-xamub Yónente ku ne doon na ku Yàlla sunu Boroom Yónni.

Am na Yónente yoo xam ne dañu leen a war a gëm xam itam seen i tur, te ñooy Sayyidunaa Muhammat SHW, ak Aadama, Nuuh, Huud, Idriisa, Luut, Saalih, Daawuud, Yuusuf, Yuunus, Ayyuub, Hëeruun, Yahyaa, Yahxuub, Ilyaas, Alyasah, Sulkifli, Ishaaxa Ismaahiil, Ibraahiima Sakariyyaa, Suhaybu, Hiisaa, Sulaymaan, Muusaa, HSW.Ñii la sunu Boroom Tudd ci Alxuraaan, sunu maam Aadama moo njëkk ci Yónente Yi, Sayyidunaa Muhammat moo ci mujj. SHW.

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (8)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR