Leeral Mawaahibul Xudduus (11)

Boo gëmee Muhammadu Rasuulul Laah ndawul sunu Boroom la, SHW gëm nga ne Yónente yépp dañuy jotal, te duñu fen, duñu def lu araam, duñu def lu ñu sib.

Mel na ni fii mu ne mboolem li nekkoon ci “Laa Ilaaha Illaal Laah Muhammadu Rasuulul Laah” SHW ciy pas-pas leeral naa ko.

Xay na baat boobu gàtt gi mu gàtt ba noppi làmboo li mi làmboo moo tax ñu def ko muy màndargam gëm, balaa kenn a gëm Yàlla sunu Boroom ci nun fàww mu wax baat boobu.

Ku am xel nag, boo xamee loolu ba noppi dangaa war di góor-góorlu bu baax di ko tudd lu bari ba mujj boo koy tudd danga ciy xam yeneen mahnaa, nga xam ne day jaxasoo ak sa dereet bu boobaa, danga gis ci ay kéemaan loo xam ne kenn du ko man a takk. Yal na nu sunu Boroom may tawféex te may nu bu nuy génn àdduna di tudd baat bii mu doon sunu baat bu mujj.

Su ko defee foofii la téere bi yem di juróom-mbenni téeméeri way ak ñaar fukk.

Subhaana Rabbika Rabbil hissati hammaa yasifuuna wasalaamun halal mursaliin wal hamdu Lillaahi Rabbil haalamiina.

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (9) Leeral Mawaahibul Xudduus (10)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
✕
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR