Kan mooy Seex Sàmba Jaara Mbay?

Bismilaahi Rahmaani Rahiim.

Sunu Sang bi, mi ngi gane àddina ci atum 1868 ci dëkkub Seex Maxtaar Ndumbe Jóob, nu naan ko Koki muy dëkk bu seel. Sëriñ Mamadu Mbay moo di baayam, Soxna Ndaak Ñang moo di ndeyam.

Ginaaw ba mu mokkale Alxuraan ci la daal di jàng Tawhid ak Fiq. Waaye yéeneem moo doonoon xereñ ci Nahwu (Nos-wax) ba doon ci ab kàngam. Loolu taxoon na mu jaar ci ay Daara yu mag yu baree-bari. Bokk na ci « Njañ », « Pir » ak « Fuuta » ci ku nuy wax Cerno Masàmba Caam. Jàngee na itam ci Maam Alhaaji Maalig Si. Li ko waral moo di Seex Maruba Géy moo ko waxoon ne xam naa koo xam ne Naar yi sax dañuy ñëw ji jàngee ci moom. Sunu sang bi jàngee ci moom ay Téere yu bari te néewoon ñu koy jàng ci boobu jamono. Bokk na ci yi mu ko jàngal Téere bunuy wax « Ibn Muhib », nga xam ne day dox ci teggiin yi nit ki wara làmboo bu bëggee tagg Yonnant bi salla laahu alayhi wa salam. Moo ko jàngal « Tanbiih » mu Imaam Shahraani. Téere boobu ci xam-xamu Tasawuf lay dox, ba tey moo ko jàngal « Alfiya » mu Ibn Maalig. Moom nag ku bëggoon Seex Sàmba Jaara Mbay la. Ba tey, bëgg gi mu bëggoon xam-xam taxoon na ko dem  » Gànnaar » def fa fukki at. Waaye li am moo di dëkk ba mu ganee àddina dafay dëkku xam-xam. Baayam itam siiwon fa ngir li mu xamoon  » Lasraar », way-juram wu jigéen itam siiwe fa cig tabbe, joxe ñam ak nangoo seelal.

Ana nag lu ko boole ak Sëriñ Tuubaa?

Mbokkam mi mu bokkal nday ak baay nu naan ko Seex Saajéy Mbay moo ko àndi ci Sëriñ bi . Ci keepaaru Seexul Xadiim ci la jàngee xam-xamu « Baatin ». Te mooy « Hilmu-Laduniya » te mooy lu mel ne la Xudar amoon ginaaw ba mu amee bob « Saahir ».
Ñaare nag niy àgg ci man a peeg yooyu xam-xam fàww seen i wax di xóot, ba tax na, ñu néew a koy dégg. Bokk na ci yooyu wax, woyi Seex Sàmba Jaara Mbay bii:

{Jeqeel ma xel, ràññeel ma xol
Xol du ni xel, xel du ni xol
Xol a di xol, xel a di xel
Ki ma giseel a mat a xam}

Sang bi nag 1917 la fi bàyyi koo, lii li nu fi bind yépp noo ngi ko jële ci Sëñ Mamadu Mbay di sëtu Seex Sàmba Jaara Mbay di ko ñaanal sunu Boroom sàmm ko biir ak biti, te defal ko mbooleem lu muy sàkku ci àddina ji ak àllaaxira ga ñu jëm barkeb Seexul Xadiim.

Al-Habdul Xadiim
04/11/2020

S’abonner
Notification pour
guest
6 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Mouhamed Thioune
Mouhamed Thioune
3 années il y a

Machalah cheikh bi lepp léer na Yalla na Yalla wéreul thieur yi Barké mame cheikh Sadiéye Mbaye Cheikh Samba Diarra Mbaye

Mustafaa JIITE
Mustafaa JIITE
3 années il y a

MashaAllah. Moom ay wayam da may yobb ci beneen haal. Yakaar naani nit ku baatiné la woon. Ndax man nga maa yoonee am mbindam?

Baye Mor
Baye Mor
3 années il y a

Jërëjëf sang bi ci yaatal gi

Al-Habdul Xadiim
Al-Habdul Xadiim
3 années il y a
Répondre à  Baye Mor

Jaajëf noo ko bokk

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR