Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu maxtaara lahu mas naa wax Sahiid Mbàkke : Mas ngaa gis ku mel ne Fàddilu Mbàkke mu ne ko déedeet ? Mu ne ko mas nga dégg ku mel ne Fàddilu Mbàkke? Mu ne ko déedeet. Sëriñ bi ne ko Sahiid Mbàkke doo ma laaj sax lu Fàddilu Mbàkke def ba xam ko doog may dëggal ? Mu ne ko buma ko sañee, laaj naa la ko. Sëriñ bi ne ko li nuy tudde ag mbokk doom a ci gën a jegge , te dikk na ba fii fi man, mu ne ma, loolu nuy tudde ag mbokk jaay naa la ko jënde ko ag murit, la daa tegge ci ag murit jox naa la ko àddiya, boole ko ak àddiya ju takku. Mas ngaa gis ku def loolu ? Mu ne ko déedeet. Mas ngaa dégg ku def loolu ? Mu ne ko déedeet. Sëriñ bi ne ko loolu mooy dayob yéeme.
Diyaafatu Samaadiya (4), p. 37.
Al-Habdul Xadiim,
Grenoble, 21/03/2020.
Sounou lepp dii gueuna saan taat yallah minou bolé ak serigne bi alhamdu Allah☝❤️
Jaajëf sant gi de war na ku ne !
Ligeey bi am na solo loll te jaar yoon te tegu ci xam xam yalla na nguén ci daje ak ngërëmu Sëriñ Fallu
Amiin amiin Bàrke Borom Tuubaanu bokk lépp