Soxna Maymuna Kubra mooy doomi Seexul Xaadim ak Soxna Aminata Buso. Moom ak Soxna Xadiija ak Sëriñ Abdul Xaadir ñoo bokk lépp. Mi ngi gane àddina fa Ceeyeen-Jolof bisub talaata ñatti fan ci weeru Tabaski ci atum 1908. Bi mu gane àddina Sëriñ bi dafa génne ñaari Xasida. Benn bi mu tënke ko « Allaahu » te […]