Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Maa ngi lay nuyu yaw Ibraahima, te di la xamal ne da maa bëgg nga dimbali »Muhammad » ci aajoom ndax loru na lool.
Saa soo gise bataaxel bi na nga ko béggal loo mën. Maa ngi ñaan Yàlla sunu Boroom àdduna bañ noo wor. Mbooleem ñi aju ci man na nga leen yee ci ne: » damaa soxloo lu leen di fegal mbooleem yàqu-yàqu yi Insaa-allaahu tahaala. »
Ginaaw nuyoo bi xamal ne « Ahmadul Muxtaaru » dara tëyuwu ko ludul xaar ku jóge ci yaw. Ndax mbóot moo xam ne duma ko man a wax ludul damaa toog ak ku ñu wóolu ci mbóot yi buy ñëw na ànd ak dara lu ñuy def li nu leen tànnal fii.
Al-Habdul Xadiim
28/03/2020.
Dieureudieuf Mouride
Jaajëfaat key!
Hakaza souniou Ibra faty 🙏🏾
Ndeysaan moom la de. Moo yor njaboot gi
Jërëjëf ku baax amatina solo noongi ciy jariñu yalla ngéen ci am njariñ lu juge ca sëriñ ba.
Amiin murid, nu bokk njariñ li
Djadjeuf yaram amna solo dh
Amiiin Soxna Jaara