Bataaxel bu jëm ci Ahmadu Jóob (5)

Bismilaahi rahmaani rahiim.

<<Boo delloo foo mana nekk na nga ragal Yàlla, te bul bariy wax ak i nelaw ak lekk ak naan. Na ngay moytu nit ñi bu baax, saa suñu la bëggee xëcc jëmme la ci ay caaxaan dawal jëm ci tuddu Yàlla. Bul yaakaar, bul ragal ku dul Yàlla, na nga koy sant foo toll ci teg gi mu la teg ci yoonu njub. Saa soo jëmme ci ku dul Yàlla ngir àjjo, lor rekk nga ciy jëlle. Bul dem ci benn buur walla jaraaf ngir àjjo ndax képp ku bokk ak ñoom sen tedd nga, da nga bokk ak ñoom ëllag senug torox.>>

Al-Habdul Xadiim,
Grenoble, 08/02/2020.
S’abonner
Notification pour
guest
6 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Thiam
Thiam
4 années il y a

Amna solo mouride bi

Abo Madiyana
Abo Madiyana
4 années il y a

Jerejef ci yaatal gui.
Denkaané bou am solo te mata bayyi xel, rawatina bi jii Kamano.

Gueye
Gueye
4 années il y a

Amna solo yaram

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR