
<<Yaw Muxtaar maa ngi lay dénk nga ragal Yàlla, te ragal Yàlla mooy jëf ndigal te bàyyi tere. Tey baril jëf yu baax, loolu mooy tax nga bari ay njariñ, te jiital allaaxira ci àddina ndax loolu mooy tax nga texe ëllëg, te mooy tax nga am kóolute ëllëg. Sax ga ngay sax ca àjjana bu ëllëge moo lay fàttelo la wéyoon ci àdduna cig doyadi. Bul faale lu dul lu lay njariñ fa sunu Boroom. Bul def lenn lumu lay jàjjee.>>
Al-Habdul Xadiim,
Grenoble,18/01/2020.
Assalamou aleykoum Mouride. Waakh dji am naa solo lol Dieureudieuf Mouride.
Jaajëfaat ñooko bokk!