Bismilaahi Rahmani Rahiim. Kon nu wéyal ci mayi Sëriñ bi cig mbidam mba yi mu ñaan Yàlla sunu Boroom defal ko ko ci. Ànd ak nu xam ne léppam la sunu Boroom nangu. Al-Habdul Xadiim 26/09/2020
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Nu fas yéene béral leen ci bayit yi nga xam ne dafay wone mayug Sëriñ bi ak li ko Yàlla defal cig mbidam ak li muy njariñ ki ciy yëngu. Su ko defe lépp mi ngi ci Nahjul Xawiim mu Sëriñ Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim. Tay nag nu fas yéene yaatal bayyit […]
Silaahu Ahlil Xawfi (4) Waxtuy julli ak melow ni ngay fayee li la ci raw.
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Su ko defe nu fas yéene téj Téere bii di Silaahu Ahlil Xawfi, jàngoon nga ci wareefu sàkku xam-xam, ba tax na ràññewon nga ponki diine ak li ciy farata ak sunna. Tay nag di nga fi xamee melow ni ngay fayee julli yi la raw ak seen ay waxtu. Al-Habdul Xadiim […]
Silaahu Ahlil Xawfi (3) Koor, asaka, aj ak àddisi Yónnent.
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Ginnaaw xàmmee farata yi ak sunna yi waréef la ci bépp jullit . Ndegam itam sunu Boroom dimbali nanu ba nu jottali mbiri julli ak li aju ci laab. Noo ngi leen di baaxe tay ñatt ci ponki diine te mooy koor, asaka ak aj, toftalee ko ak ay àddis yu jëm […]
Silaahu Ahlil Xawfi (2). Lu aju ci faratay julli ak laab
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Ginnaaw bi nu xamee ni wareef la ci jullit bi mu ràññatle farata yi ak sunna yi dina yell kon nu tàmbali ko ci julli ak laab. Su ko defe di nga fi dégge lu bari ci mbiri julli ak ci jàpp ak sangu farata ak tiim. Al-Habdul Xadiim 28/08/2020
Silaahu Ahlil Xawfi (1) Jàngum Fiq : laab ak li ci aju
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Jullit bi kuy ay noonam? Nees di def ba teqalikoo ak ñoom? Su ci ame tont yu leer, naka la war a def ba man a nekk ak nit ñi te topp Boroomam ci teggin yi gën a rafet, gën a seel, gën a ganjaru. Al-Habdul Xadiim 15/07/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Ndegam bëgg a nga àgg ci Yàlla, du man a ñàkk nga am yóbbal gu réy gu lay tax a àgg ca moom.Dees na ko xame ci Téere bii nga xam ne dafa « rafet ba dàq wurus ». Al-Habdul Xadiim 08/07/2020