Mi ngi gane àddina 1912 fa Daarul Aaliimil Xabiir, mi ngi feeñ ci weeru safar. Doomi Xaadimu Rasuul la, Soxna Faatima Suxraa mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ bee ko jëlle Gànnaar moom ak Soxna Faatima Kubra way-juru Seex Abdullaahi Mbàkke. Ñoom ñépp ay sariif leen. Ba mu dikke àddina la Sëriñ Abdu Rahmaan yabal ndaw […]