Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (4)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu am solo gi mu nuyu ay mbokkam, ay dëkkandoom ak ay kilifaaam dafa daaldi leeral lan mooy lu BAAX. Mu mel ne lépp daf koo tënk ci ag tabe gu tégge ci ag nite. Naka noonu mu wone ci aw yoon. Waaye noonu it la waxee xéewal yi nekk […]

Kan Mooy Sëriñ Masàmba Mbàkke?

Sang bi mi ngi gane àddina ci atum 1881 ca Pataar, ab dikkam ci àddina soreewul ak jamono ji way-juram wa, Sëriñ Moor Anta Sali di wuyu ji boroomam. Seexul Xadiim di magam moo ko tuddu jox ko turu Masàmba Anta Cebbo ginaaw ba mu demewoon siyaare ji barabu Sëriñ Moor fa Deqële. Sëriñ Moor […]

Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (3)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Fii daf fiy leeral mbiri ñenti noon yi te mooy bakkan, bànneex, saytane ak àdduna. Muy wax itam lëkkalo gi nekk ci diggante bakkan ak bànneex. Xamle fi itam nees di def ba noot leen. Naka noonu, la fi leerale lu aju ci bëgg a àdduna, wax na fi itam màndargay mucc […]

Kan Mooy Seex Abdul Ahad Mbàkke?

Mooy doomi Soxna Maryaama Jaxate ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu. Ci 23i la gane àddina ci weeru korite ci atum 1332 ginnaaw gàddaay gi. Di toolo ak 1914 ca Njaaréem. Ba mu toolo cim jàng leen ko jox nijaayam Sëriñ Hamzatu, nijaay ji jox ko Sëriñ Allasaan Jaxate mu jàngal ko Alxuraan. […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR