Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Fii daf fiy leeral mbiri ñenti noon yi te mooy bakkan, bànneex, saytane ak àdduna. Muy wax itam lëkkalo gi nekk ci diggante bakkan ak bànneex. Xamle fi itam nees di def ba noot leen. Naka noonu, la fi leerale lu aju ci bëgg a àdduna, wax na fi itam màndargay mucc […]