Bismillahi Rahmaani Rahiim Yu bari ci néttali yi nu fi àndi day soññee ci weetal Yàlla miy Aji Moom dëgg-dëgg. Di fi joxe ay tegtal ci wuuteeg àddina ak allaaxira. Di dénkaane itam ci wattandiku mellow àdduna di nu nax.
Bismillahi Rahmaani Rahiim Dees na xamee ci néttali yi nu fi dajale njariñal dëddu ak fexe xam bu wér ñi àdduna di wore. Su ko defee ab soññee la ci nit ki mu wara xam lim war a gën a fonk ci dundam ak ci doxiinam. Té loolu moo di fexee dundal sa ruu, sàmm […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii ay dénkaane yu jëm ci Sëriñ Mbàkke Buso deef na ko fi dégg. Mellow taalube dëgg-dëgg, néewal nelaw yi lu tax manul ñàkk, dëddu àdduna ak dëgmal ëllag li tax manta ñàkk dina fi feeñ. Soññee na it bu baax ci wattandiku yeen jikko yi nga xam ne Yàlla gëramu ko. […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Sunu xaaj wi daanaka li ci ëpp ci melloyu baax yi nit ki wara làmboo ak di ko jikkowoo moo ci nekk. Moo xam sunu digante ak sunu bop, sunuy dëkkando, sunuy way-jur ak yeneen. Mu niy soññi bu baax ci farlu, ak di jëf lu baax te bañ koo yéem. Di […]