Sëriñ Abdulaahi ku taqoowoon la ak baayam ju baax ji, nuru ko lool ci mello. Mootax Seex Musaa Ka nee : « Allaahu moo di jenn waay, moo jàpp doom def ko ni baay ». Wax na it : « boo gisee muy sàmmandaay, Seex Bàmba ñoo nuroo jotaay, nuroo yaram, nuroo sewaay, nuroo doxiin, nuroo waxiin, nuroo […]
…Dafa mel ni li moo doon cëram, mu sawar lool ci dimbali nit ñi. Bi mu toole ci 40i at nag la daaldi fas yéene dimbali ñi fi ne. Di xamle ak a won nit ñi lu leen man a teeqale ak def bàkkar, ak di jëf nangam ci lu baax ngir man a tàbbi […]
Fii di neen fi jàngee liy tax nu gën a njariñu ci Sëriñ Bi Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu. Bokk na ci jàpp ci moom bu wér ak di góor-góorlu ci Xasiida yi. Di neen fi xamee it ne, tawfeexe na lool nga ànd ak Sëriñ Tuubaa. Di neen fi déggee itam lenn ci ay […]
Xaaj wi di neen fi jàngee lenn ci mbir yi aju ci bàmmeel, ci lenn ci jëf yu baax ya fay am, mel ne jàng Alxuraan ci bàmmeel. Xisa yu bari rot ci bàyykoo ci Yonent bi Aleyhi Salaam, Sahaaba yu baax ya ak Taabihuuna ya. Yal nanu Yàlla xir ci Alxuraan. Yal na Yàlla […]
Fii dañu fiy leeral jëf yi nga xam ne du dog mukk. Daanaka rekk mooy ay jëf yoy dina njariñ nit ñi, moo xam luy tax ñuy jàng Alxuraan, lu leen di tax a sàkku xam-xam, am wér gu yaram, amug feex ak jàmm. Li lépp di tegtal ne liggéeyal Yàlla ci jaamam yi bari […]
Di na leere ci nettali yi njariñul bàyyi tere ak topp ndigal, te farlu ci bu baax biir ak biti. Di neen fi jàngee ne yéene ju refet manul ñàkk ba laa nuy jëf ak bàyyi xel Yàlla Subhaanahu ci sunuy wax ak sunuy jëf. Yal nanu Yàlla saxal ci ag njub, ak am worma […]
Xaaj wi nag di na fi leere liy waral mbugalum bàmmeel, am na ci yoy ay jëf la, am ci yoy ay wax la. Yal nanu ci Yàlla musal. Waaye di neen fi jàngee tamit liy musle ci mbugalum bàmmeel. Am na ci yoo xam ne ay ñaan la, yii ay ràkkaa yu baax a […]
Ci xaaj wi di neen fi leere mbirum bàmmel. Tancug bàmmeel, laaji bàmmeel, ak i muslaay, ak i ñaan yu baax yu mat di tàmb wax ci làmmiñ. Dina fi leere itam xéewalug sunu Boroom ci àjjanaam gi. Yal neen fa tàbbi nun ñépp. Ba tay, bunt bi daf ñuy jàngal ne waajal sa bopp […]
Dina leere ci xisa yi njariñul laabir, joxe, digle lu baax ak di ko jëfe. Dees na fi xamee itam lenn ci mbiri Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu. Ak ay dénkaane yu am solo yu mu jaarale ci ay tomb. Ba tay noo ngi ñaanal Faamara Seen sunu Boroom yëram ko, jéggal ko […]
Xaaj wi dees na fi àndi li bàmmeel di wax ak dóomu àddama. Muy luy xuppe, di soññe ak di jàjji ci sax ci lu baax. Ndax moom bàmmeel man naa naat lool, waaye man na tiis lool. Yal nanu Yàlla gindi bu wér ci lu baax ak ci lu am njariñ.