Dina leere ci xisa yi njariñul laabir, joxe, digle lu baax ak di ko jëfe. Dees na fi xamee itam lenn ci mbiri Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu. Ak ay dénkaane yu am solo yu mu jaarale ci ay tomb. Ba tay noo ngi ñaanal Faamara Seen sunu Boroom yëram ko, jéggal ko […]
Xaaj wi dees na fi àndi li bàmmeel di wax ak dóomu àddama. Muy luy xuppe, di soññe ak di jàjji ci sax ci lu baax. Ndax moom bàmmeel man naa naat lool, waaye man na tiis lool. Yal nanu Yàlla gindi bu wér ci lu baax ak ci lu am njariñ.
Xaaj wi dafay jëm ci mbiri bàmmeel ba tay. Nu ciy xamle ñi nga xam ne dee fu leen laaj ci bàmmeel. Nu ciy xamee ba tay, yërmandeey sunu Boroom, naka noonu sañ-sañam. Yal nanu Yàlla musal ci tiisi bàmmeel.