
Ñi jaar ci ay loxoom bari neen lool. Bokk na ci Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, Sëriñ Mustafaa Saalihu Sëriñ Saalihu Ture.
Ku amoon kollare la ak doomi Sëriñ Tuubaa yi, Seex si, ak kilifay yeneen tariqa yi. Amoon tawfeex lool ci Boroomam, di ñaan bu wér muy nangu. Te doyloo woon Sëriñ bi ci bépp soxla.
Ku amoon fulla la itam, te yeewu, xam àddina, man a jëflante ak ñépp.
Doonoon ku woyof am ak ñépp a jàmm. Dafa jekkuwoon lool itam mboorum Sëriñ Tuubaa ak njabootam. Baay Sëriñ Ngiraan dafay wax sax naan lu mu ci xam lu ne ci Sëriñ Moor Mbay Siise la ko xamee.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien