Kan mooy Sëriñ Madùmbé Mbàkke?

Seex Ahmadu Ndùmbé Mbàkke mi ngi ganné adduna 1859 ci dëkk buñu naan Nja feeté Mbàkke Baol, doomi Sëriñ Zayd Mbàkke la, moom Saër Soxna Busó moom Maam Mahram. Mi ngi yaroo ci kepparu wayjuram, and naak mom wooté Màba Jaxu Ba ca Saalum nekk Poroxan.

Ginaaw ba wayjuram wa nélawé la dem Mbàkke Kajjóor fekki fa Seriñ Tuuba, aggalé fa’b njaggam, taqqoo’k moom, ba ni miy demé Mbàkke Baol. Dëkko joxon leeppam, masta des ginaaw ci dara. Moo tax Señ Musà Ka naan ko 《ba mu ñëwee Mbàkke kajjóor feek na alarabaa’ki dibéer len xéwaloon mu daal di buur sóobu yóonu ajjanah jeebal Seriñ bi ap nosam def gumba jox kop tumam, fum tool sàkkuy ngëram laajal Seriñ Daam Feeké naa, kerok ba tey mësla taayi, mësla yaag ci’g jotaay, mësla teggi laxasaay, mësla wax ne soonu naa, mësla xéy deelu ginaaw, ta luñ ko sant mu ne waaw, ta duko won kanam gu ñaaw, mësla wax ne jambu naa.》

Ba Sëriñ bi demee ca géej gi, dafa yéesalaat laxasàyam, soññi waat murid yi ci liggéey bi ni ko Señ Basiiru waxe ca téerem ba ji Minanul Bàqil xadim ak ni ko Señ Muhamad lamin Jóob dagana andee ci Nubzatut taariqi wa nafsatul haamiya Ahmalu ahmaalihi.
Ginaaw ga la sanc dëkk buñu naan kër Magéy Ndaw attum 1896: 《 Juróom ñaari at yi Señ bi am ci géej la am fa kër Magéy di géej》. Lumu fa masa bey jéebal nako Sëriñam, ba ci xoolitu geerté yi, daan nako ko yóobul. Ba Sëriñ bi nibi sé ba mu am at la sanc Xaabàn. Digganté 1914 ak 1925 nak sanc na fi dëkk yu bari ngir jangalé ak yaré.

Diiru lu Señ bi nek ci géej gi nak Borom Daaru la tóopon. Batey ba fi Señ bi bàyyi ko, bok na ci ni njëkk tóop Sëriñ Muhamadu Mustafa. Borom jikko yu refet la won, doonon ku réy koolaré, tabbé, ñamé lool joxé àddiyah
Ci attum 1933 la wuyu ji boromam!

Lii ñu bind Señ Móodu Daara Faal moo ñuko xamal ginnaaw bimuko xamee ci Señ Maxtaar Puy. Yalna len yàlla subhanahu wa tahala defal yiiwu adduna ak alaaxira bakep señ Ahmadu Mbàkke.

Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 07/12/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR